1Bu ngeen demee ngir xarejeek seeni noon ba gis ay fas, aki watiir, ak gàngoor gu leen ëpp, buleen leen ragal, ndax seen Yàlla Aji Sax jaa ngeek yeen, ki leen jële woon réewum Misra.
2Bu ngeen di waaja xare, na sarxalkat bi dikk, wax ak mbooloo mi,
3ne leen: «Éey Israyil, dégluleen, yeena ngi waaja xareek seeni noon tey jii. Buleen yox-yoxi, buleen ragal, buleen tiit, buleen teqlikook seen sago ci seen kanam!
4Ndaxte seen Yàlla Aji Sax ji mooy kiy dox ànd ak yeen, xeexal leen ak seeni noon, ngir may leen ndam.»
5Su ko defee kilifay xarekat yi wax ak gàngoor gi, ne leen: «Ana góor gu ci tabaxoon néeg bu bees te daloogu ko? Na daldi dellu cab néegam bala moo dee ci xare bi, geneen góor daloo ko.
6Ana góor gu ci jëmbatoon tóokëru reseñ te jariñoogu ko? Na daldi ñibbi bala moo dee ci xare bi, geneen góor jariñoo ko.
7Ana ku ci ngoroom dëgëroon te jëlagul? Na daldi ñibbi bala moo dee ci xare bi, geneen góor jël ko.»
8Gannaaw loolu, na kilifa yi dellu wax ak gàngoor gi, ne leen: «Ana ku ci ragal, ana ku ciy yox-yoxi? Na daldi ñibbi kat, bala moo yoqiloo ay moroomam, ni moom.»
9Bu kilifay xare ya waxeek gàngoor gi ba noppi, nañu tabb ay njiiti kurél, ñu jiite gàngoor gi.
10Bu ngeen dikkee ba jub ab dëkk, ngir xareek ñoom, jëkkleen leena woo ci jàmm.
11Ndegam jàmm lañu leen wuyoo, ba ubbil leen, mboolem askan wa mu fekk ca biir dëkk ba dañuy tegoo liggéeyu sañul-bañ, ñeel leen, di leen jaamu.
12Waaye bu ñu jàmmoowul ak yeen, xanaa di xareek yeen, gawleen dëkk ba.
13Seen Yàlla Aji Sax ji moo leen di teg ci seen loxo, ngeen daldi leel ñawkay saamar mboolem seeni góor.
14Waaye jigéen ñi ak tuut-tànk yi, ak jur gi, ak mboolem lu ne ca biir dëkk ba, mboolem alal ja, sëxëtooleen, jagoo. Lekkleen alal ji ngeen foqatee ci seen noon, yi leen seen Yàlla Aji Sax ji jébbal.
15Noonu ngeen di def ak dëkk yi soreek yeen lool te bokkuñu ci dëkki xeet yii ngeen jëm.
16Dëkki xeet yii leen seen Yàlla Aji Sax ji sédd nag, buleen ci bàyyi lenn luy noyyi, mu dund.
17Nangeen faagaagal Etteen ñi ak Amoreen ñi ak Kanaaneen ñi ak Periseen ñi ak Eween ñi ak Yebuseen ñi, na leen ko seen Yàlla Aji Sax ji sante woon,
18ndax ñu bañ leena royloo, ngir ngeen di jëfe seen mboolem yu jomblu yi ñuy defal seeni tuur, ba ngeen moy seen Yàlla Aji Sax ji.
19Bu ngeen gawee lu yàgg ab dëkk, ngir song leen xare, ba nangu ko, buleen fóom ay garabam, di ca gor lenn te mana lekk ca doom ya. Kon nag garab, buleen ko gor. Garab du nit ba ñu di ko def ni ku ñu gaw.
20Terewul garab gu ngeen xam ne deesul lekk doom ya, gorleen ko, daaneel, te ngeen sàkke ko ab gawukaay bu wër dëkk biy xareek yeen, ba keroog dëkk bay daanu.