1Su ab jote amee diggante ay nit, nañu dem ca ëttub àttekaay ba, ñu àtte leen, ba ki am dëgg, ñu jox ko dëgg, ki tooñ, ñu teg ko tooñ.
2Su dee ay dóor la ki tooñ yelloo, na ko àttekat bi tëral, ñu dóor ko ci kanamam, limu yar ba yemook tooñam.
3Waaye ñeent fukki yar, bu ñu ko dóor lu ko ëpp, ndax dóor ko lu ëpp loolu, torxal seen mbokk ci seen kanam lay doon.
4Buleen sunjuñ gémmiñu nag, te fekk koy bojj am pepp.
5Bu ay góor yu bokk waajur dëkkee, kenn ci ñoom dee te bàyyiwul doom ju góor, jabaru ki dee du génn, di séy akub jaambur. Jëkkëru donaleem ju bokk ak jëkkëram moo ko wara jël, donloo ko.
6Su ko defee bu ca ndaw sa taawloo góor, taaw ba saxal turu mbokkam ma dee, ba turam du fey ci biir Israyil.
7Su waa ji buggula jël jabaru donaleem jooju, na ndaw sa dem ba ca mag ña ca bunt dëkk ba, ne leen: «Sama jëkkëru donale jii moo baña saxal turu mbokkam ci Israyil. Moo ma buggula donloo.»
8Bu loolu amee na ko magi dëkkam woolu, wax ak moom. Su waa ji dëgëree, ne buggu koo jël,
9na ko jabaru donaleem ja fekki ca kanam mag ña, daldi summi benn caraxu waa ji ba noppi, tifli waa ji ci kanam, ne ko: «Nii lees di def ku dul sampal mbokkam kër.»
10Su boobaa tur wa ñuy dippee waa kër waa ja ci digg Israyil, di «Kërug summi carax.»
11Su ay góor dee jàppante, ba jabaru kenn ki dikk, di sotle jëkkëram; bu jàppee ca ngóoray kay jàppanteek jëkkër ja,
12dogleen loxol ndaw sa te buleen ko ñéeblu.
13Buleen denc ci seen mbuus doju màndaxekaay ak moroom ma, te bii diis, bi ci des woyof.
14Buleen denc seen kër nattukaayu sol-sotti ak moroom ma, bii réy, bi ci des tuut.
15Doju màndaxekaay bu mat te dëggu ngeen wara am, te nattukaayu sol-sotti bu mat te dëggu ngeen wara am, ndax ngeen gudd fan ca réew ma leen seen Yàlla Aji Sax ji di jox.
16Seen Yàlla Aji Sax ji kat seexlu na képp kuy def yooyii, képp kuy def ug njublaŋ.
17Fàttlikuleen la leen Amalegeen ña defoon ca yoon wa, ba ngeen génnee Misra:
18ñoo leen dab ci yoon wi, songe leen gannaaw, fàdd mboolem ña mujje woon, fekk ngeen sonn, loof, te ragaluñu ci sax Yàlla.
19Bu ngeen demee ba seen Yàlla Aji Sax ji noppal leen ci mboolem seen noon yi séq réew, mi mu leen sédd, ngir ngeen nangu ko, nangeen far mboolem lu ñu doon fàttlikoo Amalegeen ñi fu asamaan tiim. Buleen ko fàtte.