Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Baamtug Yoon wi

Baamtug Yoon wi 16

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Wormaal-leen weeru Abiib, te ngeen amal ci màggalu bésub Mucc, ñeel seen Yàlla Aji Sax ji, ndax ci weeru Abiib la leen seen Yàlla Aji Sax ji génnee Misra, ag guddi.
2Nangeen ci sarxalal seen Yàlla Aji Sax ji, ab gàtt mbaa aw nag, ci bérab bi Aji Sax ji taamoo dëël turam ëllëg.
3Buleen ko lekkaale lenn lu am lawiir. Daleleen caa lekk, ba diiru juróom ñaari fan, mburu mu amul lawiir, mburum njàqare, ndax ci biir gaawtu ngeen génne woon réewum Misra. Su ko defee ngeen baaxantal seen giiru dund, bés ba ngeen génnee réewum Misra.
4Bu leen kenn gisal lawiir ci seen tund wépp, diiru juróom ñaari fan, te bu lenn fanaan ci yàppu jur gi ngeen sarxal, diggante ngoonu bés bu jëkk ba, ba ca suba sa.
5Juru bésub Mucc bi, dungeen ko mana rendi fenn ci dëkk yi leen seen Yàlla Aji Sax ji jox,
6fu moy bérab ba seen Yàlla Aji Sax ji taamoo dëël turam. Foofa ngeen di rendi juru bésub Mucc bi ci ngoon bu jant biy so, yemook waxtu wa ngeen bàyyikoo woon Misra.
7Toggleen ko, te lekk ko ci bérab bi seen Yàlla Aji Sax ji di taamuji, ca suba sa ngeen xëy, dellu ca seeni xayma.
8Juróom benni fan ngeen di lekk mburu mu amul lawiir, bésub juróom ñaareel di am ndaje, ñeel seen Yàlla Aji Sax ji. Buleen ci liggéey dara.
9Juróom ñaari ayi bés nag, ngeen di waññ, te ci ndoortel ngóob ngeen di tàmbalee waññ juróom ñaari ayi bés yi,
10ngeen doora amal màggalug Ayi bés, ñeel seen Yàlla Aji Sax ji, te saraxu yéene ba ngeen cay joxe di kemu koom ga leen seen Yàlla barkeele.
11Ngeen daldi bànneexu fa seen kanam Yàlla Aji Sax ji, yeen ak seeni doom, góor ak jigéen ak seeni jaam, góor ak jigéen, ak Leween ñi ci seen dëkk, ak doxandéem yeek jirim yeek jëtun ñi ci seen biir, ci bérab bi seen Yàlla Aji Sax ji taamoo dëël turam ëllëg.
12Fàttlikuleen ne ay jaam ngeen woon ca Misra te ngeen sàmmoo jëfe dogali yoon yii.
13Màggalu Mbaar yi it nangeen ko wormaal diiru juróom ñaari fan, gannaaw bu ngeen dajalee seenum pepp, ak seen ndoxum reseñ.
14Ngeen daldi bànneexoo seenug màggal, yeen ak seeni doom, góor ak jigéen, ak seeni jaam, góor ak jigéen, ak Leween ñeek doxandéem yeek jirim yeek jëtun, ñi ci seen biir dëkk.
15Juróom ñaari fan ngeen koy màggal ñeel seen Yàlla Aji Sax ji ci bérab bi Aji Sax ji di taamuji, ndax seen Yàlla Aji Sax ji moo leen di barkeelal seen meññat mépp, ak seen mboolem ñaq, seen mbégte mat sëkk.
16Kon ñetti yoon cim at la mboolem seeni góor di teew fi seen kanam Yàlla Aji Sax ji, ci bérab bi muy taamuji: fani màggalu Mburu mu amul lawiir, ak fani màggalug Ayi bés, ak fani màggalu Mbaar yi. Waaye deesul teewe loxoy neen fi kanam Aji Sax ji.
17Ku nekk, na sarax ba muy indi, di kemu barke ba ko Yàlla jagleel.
18Te itam ay àttekat aki kilifa ngeen di tabb ngir seeni giir, ci mboolem dëkk yi leen seen Yàlla Aji Sax jiy jox, ñuy àtte mbooloo mi àtteb dëgg.

19Buleen jalgati yoon cib àtte, buleen jeng te buleen nangu alalu ger, ndax ab ger day muur bëti boroom xel, di xañ aji jub dëgg.
20Dëgg doŋŋ ngeen wara topp, ndax ngeen dund, jagoo réew mi leen seen Yàlla Aji Sax ji di jox.
21Buleen samp benn xeru bant, bu jóge ci genn garab, ngir di ko jaamoo Asera tuur mi, ci seen wetu sarxalukaay bi ngeen sàkk ngir seen Yàlla Aji Sax ji.
22Te itam buleen yékkati lenn lu bokk ci doji jaamookaay yooyu seen Yàlla Aji Sax ji bañ.