Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Baamtug Yoon wi

Baamtug Yoon wi 19

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Gannaaw bu leen seen Yàlla Aji Sax ji wollilee xeet yi mu leen di jox seenum réew, ngeen dàq leen, ba dëkke seeni dëkk ak seeni kër,
2ñetti dëkk yu mag ngeen di ber ca biir réew mooma leen seen Yàlla Aji Sax ji jox, ngir ngeen jagoo ko.
3Ngeen waajal nag yoon wu jëm ci dëkk bu ci nekk, te ngeen séddale ñetti pàcc réew mooma leen seen Yàlla Aji Sax ji sédd, ngir képp ku rey nit, man caa làquji.
4Mbirum ki rey nit te di fa làquji ba mucc, nii lay tëdde: day fekk mu rey moroomam te du teyeefam, waaye bañu ko woon démb ak bëkk-démb.
5Mu mel ni ku ànd ak moroomam ca gott ba, di gor matt. Mu doon xàcci sémmiñam di gor, weñ ga fettaxe ca njàppu la, dal ca moroom ma, mu dee. Kooku day làquji ci dëkk yooyu benn, ba mucc.
6Toppkatu bakkan ba nag warul mana dabi ci biir xolam bu tàng, ki rey, ba rey ko ngir sorewaayu yoon wa jëm ca dëkkub rawtu ba, te àtteb yoon reyluwu ko, gannaaw fekkul woon mu bañ ka mu rey, démb ak bëkk-démb.
7Looloo waral ma sant leen, ne leen ñetti dëkki rawtu ngeen di ber.
8Bu seen Yàlla Aji Sax ji yaatalee seen suuf, na mu ko giñale woon seeni maam nag, ba jox leen mboolem réew ma mu dige woon ne dina ko jox seeni maam,
9ndegam sàmm ngeen mboolem santaane bii ma leen dénk tey, ngir di ko jëfe, ngir sopp seen Yàlla Aji Sax ji, di awe ay yoonam bés bu nekk, su boobaa nangeen yokkaat ñetti dëkk yu mag, mu dolliku ci ñetti dëkk yi ngeen jëkka ber.
10Su ko defee deesul tuur deretu jaambur bu deful dara ci suufas réew, mi leen seen Yàlla Aji Sax ji sédd, ba àqu deret di leen topp.
11Su fekkee ne nit ki dafa bañ moroomam, su ko tëroo, dal ci kawam, ba fàdd ko, mu dee, su làqujee ci dëkk yooyu benn,
12su boobaa na magi dëkkam yeble, ñu jële ko foofa, teg ko ci loxol toppkatu bakkan ba, ngir mu dee.
13Buleen ko xool bëtu yërmande. Noonu ngeen di dindee ci Israyil, àqu deretu jaambur bu deful dara, ndax ngeen baaxle.
14Te it buleen toxal seen yemukaayu suufas moroom yu maam ya yemalee woon ci seen biir céru suuf ba ngeen jagoo, ca réew ma leen seen Yàlla Aji Sax ji di moomale.
15Bennub seede nag du taxaw, di tuumaal kenn, ci genn tooñ mbaa bàkkaar, ak bépp bàkkaar bu mu mana bàkkaar. Ci kaw kàddug ñaari seede mbaa ñett la mbir ma di wére.
16Su ab seedeb safaan taxawee, tuumaal kenn, ne moo lajj yoon,
17na ñaari nit, ña séq mbir ma taxawi fa kanam Aji Sax ji, fa kanam sarxalkat ya, ak àttekat ya ca yooyu jant.
18Su ko defee àttekat yi seet bu baax, ba mu wér ne seede ba kat, seedeb soskat la buy seedeel mbokkam aw sos,

19te ngeen def ak moom, la mu naroona yóbbe ka mu sosal. Noonu ngeen di tenqee lu bon ci seen biir.
20Ñi ci des dinañu ko dégg, te dinañu ragal ba duñu defati lu bon lu ni mel ci seen biir.
21Buleen ci xool bëtu yërmande. Bakkan, bakkan a koy fey; bët, bët; bëñ, bëñ; loxo, loxo; tànk, tànk.