Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Baamtug Yoon wi

Baamtug Yoon wi 13

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Mboolem kàddu gi ma leen dénk nag, sàmmooleen koo jëfe. Buleen ci yokk lenn, buleen ci wàññi lenn.
2Gannaaw loolu su ab yonent feeñee ci seen biir, mbaa boroom gént, bu leen digee firnde mbaa kiraama,
3ba firnde la mbaa kiraama ga mu leen waxoon dikk, su leen nee: «Nanu topp yeneen yàlla, jaamu leen,» yàlla yu ngeen xamul,
4buleen déglu waxu yonent boobu, mbaa boroom gént boobu, ndax seen Yàlla Aji Sax ji moo leen di nattu ngir xam ndax yeena ngi koy soppe seen léppi xol ak seen léppi bakkan.
5Seen Yàlla Aji Sax ji moom ngeen di topp, moom ngeen di ragal. Ay santaaneem ngeen di sàmm, baatam ngeen di déglu, moom ngeen di jaamu, te ci moom ngeen wara ŋoy.
6Yonent boobu nag mbaa boroom gént boobu, dee mooy àtteem, ndax moo woote ag fippu ci seen kaw Yàlla Aji Sax, ji leen jële ca réewum Misra, jote leen kërug njaam ga. Mu nar leena féle ci yoon wi leen seen Yàlla Aji Sax ji sant ngeen doxe ko. Noonu ngeen di tenqee lu bon ci seen biir.
7Seen mbokk mu ngeen bokkal jenn ndey, mbaa seen doom ju góor, mbaa ju jigéen, mbaa seen jabar ju ngeen xejjoo, mbaa seen xaritu benn bakkan, su leen dee xiirtal, naan leen ci kumpa: «Nanu jaamuji yeneen yàlla,» yàlla yu ngeen xamul, du yeen du seeni maam,
8ci yàllay xeet yi leen séq, ñi leen jege, ak ñi leen sore, ci àddina sépp, cat ba cat,
9su boobaa buleen ko nangul, buleen ko déglu, buleen ko xool bëti yërmande, buleen ko baal, buleen ko nëbbal.
10Reyleen ko rekk. Yeen ñi mu doon jéema yóbbaale, na ko seen loxo jëkka dal, ngir rey ko, bala cee loxol mbooloo mépp topp.
11Dóorleen koy doj ba mu dee, ndax moo leen doon fexee soreleek seen Yàlla Aji Sax, ji leen jële réewum Misra, kërug njaam ga.
12Israyil gépp a koy dégg, daldi ragal ba deesatul def mbon gu ni mel ci seen biir.
13Bu ngeen déggee, ci benn dëkk, ci dëkk yi leen seen Yàlla Aji Sax ji jox, ngir ngeen dëkke, ñu ne
14ay nit ñu tekkiwul dara, te bokk ci yeen, ñoo jóg di waññi seen waa dëkk, naan leen: «Nanu jaamuji yeneen yàlla,» yàlla yu ngeen xamul,
15su boobaa nangeen gëstu, seet te laajte bu baax, ba dëgg gu wér feeñe ca mbir ma, ne defees na moomu mbir mu jomblu ci seen biir,
16ngeen daldi jam rekk waa dëkk boobu, leel leen ñawkay saamar, faagaagal dëkk ba, ak mboolem la ca biiram, jur ga it, ngeen leel leen ñawkay saamar.
17Mboolem alalu sëxëtoo ju jóge ca dëkk ba, dajaleleen ko ca digg pénc ma, te ngeen lakk dëkk ba, booleek cëxëtoo ma, def ko dóomal bu mat sëkk, ñeel seen Yàlla Aji Sax ji. Day doon ab gent ba fàww, deesu ko tabaxaat.
18Bu dara des ci seen loxo, lu bokk ci alal jooju ñu wara faagaagal. Su ko defee Aji Sax ji dëddu sànjam mu tàng, yërëm leen, ñeewante leen, yokk leen na mu ko giñale woon seeni maam,

19ndegam yeena ngi dégg seen kàddug Yàlla Aji Sax ji, ngir sàmm mboolem santaaneem yi ma leen di dénk bésub tey, ngir di jëfe li seen Yàlla Aji Sax ji rafetlu.