Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - 1.Samiyel

1.Samiyel 7

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Waa Kiryaat Yarim nag dikk, jëlsi gaalu Aji Sax ji, yóbbu ko kër Abinadab ca kaw tund wa. Ñu sellal Elasar, doomam ju góor ngir muy wattu gaalu Aji Sax ja.
2Gannaaw bés ba ñu yóbboo gaal ga Kiryaat Yarim, nekk na fa lu yàgg, ba am fa ñaar fukki at. Waa kër Israyil gépp nag namma dellu ci Aji Sax ji.
3Samiyel wax ak waa kër Israyil gépp, ne leen: «Ndegam seen léppi xol ngeen namma delloo ci Aji Sax ji, jëleleen fi seen biir tuuri doxandéem yi, ak tuur yi ñu dippee Astàrt, te ngeen saxal seen xol ci Aji Sax ji, jaamu ko moom doŋŋ. Su ko defee mu xettli leen ci waa Filisti.»
4Ba mu ko defee bànni Israyil génne seen tuur yi ñu dippee Baal ak Astàrt. Ñuy jaamu nag Aji Sax ji moom doŋŋ.
5Gannaaw loolu Samiyel ne leen: «Wooleen Israyil gépp, ñu daje ca Mispa, ma tinul leen Aji Sax ji.»
6Ñu daje ca Mispa, tanq ndox, sotti fa suuf, fa kanam Aji Sax ji. Ñu woor nag bésub keroog, daldi wax foofa ne: «Noo tooñ Aji Sax ji.» Ca Mispa la Samiyel doone njiitu Israyil.
7Ba waa Filisti yégee ne bànni Israyil daje na ca Mispa, kàngami waa Filisti ya jóg, ngir songi leen. Bànni Israyil yég ko, am tiitaange ca waa Filisti.
8Bànni Israyil ne Samiyel: «Ngalla bu nu noppee jooytul ci sunu Yàlla Aji Sax ji, ndax mu wallu nook waa Filisti!»
9Samiyel jël menn xar mu feragul, defal ko lépp Aji Sax ji saraxu rendi-dóomal. Mu jooytul Israyil ci Aji Sax ji, Aji Sax ji nangul ko.
10Naka la Samiyel di joxe saraxu rendi-dóomal ba, waa Filisti di jegesi ngir xareek bànni Israyil. Aji Sax ji dënoo kàddu gu réy, ca kaw waa Filisti bésub keroog, fëlxe leen, ñu daanu fa kanam bànni Israyil.
11Bànni Israyil génne Mispa, dàqi waa Filisti, duma leen, bay waaja àgg Bet Kar.
12Gannaaw loolu Samiyel jël aw doj, teg ko ci diggante Mispa ak fu ñuy wax Sen; mu dippee doj wi Eben Eser (mu firi doju Wall). Mu ne: «Ba fii la nu Aji Sax ji wallu.»
13Waa Filisti nag detteelu, dikkatuñu biir suufas Israyil. Giiru dundu Samiyel gépp loxol Aji Sax jaa ngi ci kaw waa Filisti.
14Dëkk ya Filisti nangu woon ci Israyil daldi délsi ci seeni loxo; dale ko ca Ekkron ba Gaat. Israyil nangoo ci waa Filisti suufam sépp. Diggante Israyil ak Amoreen ñi itam di jàmm.
15Samiyel jiite na Israyil giiru dundam gépp.
16At mu jotaan day wër diggante Betel ak Gilgal ak Mispa, di àtte mbiri bànni Israyil, foofu fépp.
17Gannaaw loolu mu dellu Raama ndax fa la këram nekkoon, fa la daan àttee Israyil, te fa la tabax sarxalukaay, ñeel Aji Sax ji.