Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - 1.Samiyel

1.Samiyel 22

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Ba loolu amee Daawuda jóge Gaat, daw làquji ca biir xuntim Adulam. Magam yaak waa kër baayam gépp yég ko, dikk, fekksi ko fa.
2Ci biir loolu mboolem boroom njàqare ya, ak ña bor jiital, ak tàng-xol ya, ñoom ñépp dajeji fa Daawuda, mu doon seen njiit. Ñu wara tollook ñeenti téeméeri nit, ànd ak moom.
3Daawuda bàyyikoo fa dem Mispe, ca diiwaanu Mowab. Mu wax buuru Mowab ne ko: «Rikk may ma, sama baay ak sama ndey dikk toog ak yaw, ba ma xam nu Yàlla di def ak man.»
4Noonu la Daawuda yóbboo ay waajuram Mispe ca buuru Mowab, ñu toog fa mboolem diir ba mu làqu ca rawtoom ba.
5Ci kaw loolu Yonent Yàlla Gàdd ne Daawuda: «Bul toog ci rawtu bi, fabul dem réewum Yuda.» Daawuda bàyyikoo ca, dem ba ca gottub Eret.
6Ci biir loolu Sóol dégg ne gis nañu Daawuda ak ña ànd moom. Booba Sóol a nga toog ca ker garabu tamaris, ga ca Gibeya ca kaw tund wa. Ma nga ŋàbb xeejam, jawriñam yépp taxaw ci wetam.
7Sóol wax ak jawriñam yi taxaw ci wetam, ne leen: «Yeen Beñamineen ñi, dégluleen! Mbaa yeen ñépp, doomu Yese jee leen di jox ay tool aki tóokëri reseñ, am yeen ñépp lay fal njiiti kuréli junni ak njiiti kuréli téeméer,
8ba ngeen di ma fexeel yeen ñépp? Du kenn ku ma yégal ne sama doom fasoo naak doomu Yese ji. Du kenn ku ma tiisoo, yégal ma ne sama doom a ngi xabtal sama surga ci sama kaw, ngir mu waajal ma am tëru ni tey jii!»
9Doweg, Edomeen ba taxawandook jawriñi Sóol, daldi àddu, ne: «Man de, gis naa doomu Yese ji, mu dikk dëkk ba ñuy wax Noob, ca Ayimeleg doomu Ayitub.
10Ayimeleg seetal na ko ci Aji Sax ji, ab dund it may na ko ko, te it saamaru Golyaat waa Filisti ba, jox na ko ko.»
11Buur Sóol woolu sarxalkat ba Ayimeleg doomu Ayitub, ak mboolem bokki baayu Ayimeleg ya doon ay sarxalkat ca Noob; ñu wuysi Buur Sóol, ñoom ñépp.
12Buur ne: «Yaw doomu Ayitub, déglu ma fii!» Mu ne ko: «Maa ngi lay dégg, sang bi.»
13Sóol ne ko: «Li nga ma def nag, di ma fexeel, yaak doomu Yese ji? Yaa ko may ab dund, yaa ko jox ab saamar, seetal ko ci Yàlla, ba mu jógal ma, di ma tëru nii tey!»
14Ayimeleg ne Buur: «Buur, ana sa surga yii ba ñu daj, ku la nangule ni Daawuda mii, di sa goro, jiite say dag, te di ku ñu nawloo ci sa biir ëtt bii?
15Du keroog laa ko jëkka seetal ci Yàlla de! Te it Yàlla buma la lalal pexe! Dëgg waay, Buur sama sang, bu ma topp lenn maak kenn ci sama waa kër baay, ndax kat sang bi, xawma dara ba dara booloo jeex ci menn pexe.»
16Buur Sóol ne ko: «Yaw Ayimeleg kay, dee rekk mooy sab àtte, yaak sa waa kër baay yépp.»
17Ba mu ko defee Buur ne dagam ya ko dar: «Ayca, reyleen sarxalkati Aji Sax yii, gannaaw ñoom it ñook Daawudaa far. Yégoon nañu ba muy daw te xamaluñu ma ko.» Dagi buur ya nag baña xàcci seen loxo ci kaw sarxalkati Aji Sax ya.
18Buur ne Doweg: «Ayca yaw, fàddal sarxalkat yii!» Doweg Edomeen ba fàdd sarxalkat ya. Rey na bésub keroog juróom ñett fukki nit ak juróom (85) ñuy sol xar-sànnim lẽe.

19Waa Noob dëkkub sarxalkat ya it, mu jam leen, leele ñawkay saamar; góor ak jigéen, gone ya, ba ca ñay nàmp, ak nag yaak mbaam yaak gàtt ya, lépp la leele ñawkay saamar.
20Jenn doomu Ayimeleg miy doomu Ayitub doŋŋ a rëcc, te mooy Abiyatar. Mu daw, fekki Daawuda.
21Mu yégal Daawuda ne ko Sóol reylu na sarxalkati Aji Sax yi.
22Daawuda ne Abiyatar: «Xamoon naa bésub keroog ne gannaaw Doweg Edomeen baa nga fa woon, du ñàkk moos mu nettali ko Sóol. Man mii maa gàddu sa bakkani waa kër baay gépp.
23Waaye toogal fii ci man, te bul ragal dara. Ki lay wuta rey moo may wuta rey man itam. Soo nekkee ci sama wet nag, yiiru nga.»