1Ci fan yooyu Yonatan doomu Sóol wax surga ba koy gàddul ngànnaayam, ne ko: «Kaay nu dem ba ca gàngooru Filisti ga ca wàlla.» Baayam nag, waxu ko ci dara.
2Fekk na baayam a nga dal fa Gibeya yem, ca ker garabu gërënaat ga ca Migron. Mbooloo ma ànd ak moom tollu ci juróom benni téeméeri góor.
3Axiya ma nga fa woon, sol xar-sànnim sarxalkat. Axiya mooy doomu Ayitub, mi bokk ak Ikabot seen baay Fineyas; Fineyas moomu, Eli, sarxalkatu Aji Sax ja ca Silo, mooy baayam. Mbooloo ma nag yéguñu ne Yonatan dem na.
4Poot ba Yonatan jaare, wuti dalub waa Filisti, ñaari doj yu mag a sampe woon, séq ko. Ñu dippee wenn doj wa Boses, weneen wa di Sene.
5Wenn doj waa nga sampe wetu bëj-gànnaar, janook Migmas, wa ca des sampe wetu bëj-saalum, janook Geba.
6Yonatan ne gàddukatu gànnaayam: «Ayca nu dem ba ca dalub yéefar yee. Jombul Aji Sax ji defal nu yiw, ndax dara du tee Aji Sax ji maye ndam, nu bareek nu néew.»
7Ba loolu amee gàddukatu gànnaayam ne ko: «Ayca, loo namm rekk, sang bi, yaw laa àndal ba jeex tàkk.»
8Yonatan ne ko: «Ayca nu dem ba ca ñoom, feeñu leen.
9Bu ñu nu nee: “Taxawleen foofu, ba nu fekksi leen,” nu yem fa, bañ leena fekki.
10Waaye bu ñu nee: “Ayca, dikkleen,” nu daldi dem te xam ne Aji Sax jee leen teg ci sunu loxo. Nan def loolu ab takk.»
11Ba loolu amee ñu feeñuji dalub waa Filisti, ñoom ñaar ñépp. Waa Filistee nga naan: «Xool-leen! Ay Ebraa ngay génne pax ya ñu làqu woon.»
12Ci kaw loolu waa dal ba ne Yonatan ak gàddukatu gànnaayam: «Ée, dikkleen rekk, nu xamal leen lu tuut.» Yonatan ne gàddukatu gànnaayam: «Dikkal, topp ci man. Aji Sax ji teg na leen ci loxol Israyil.»
13Yonatan ñalgu ca kaw tund wa, gàddukatu gànnaayam topp ko. Yonatan a ngay jam, waa Filisti di daanu, gàddukatu gànnaayam ba di leen jekkli ca gannaawam.
14Cong mu jëkk mooma Yonatan song, mook gàddukatu gànnaayam, lu tollook ñaar fukki góor lañu ca tëral ci dénd bu wara tollook xëyu nag.
15Ci kaw loolu tiitaange dajal dal baak àll ba ko wër, ak mbooloo ma mépp; muy dal ba, di kuréli yàqkat ya. Rax ca dolli suuf sa yëngu, muy tiitaange lu Yàlla wàcce.
16Fekk na ay jongrukati Sóol a nga tollu ca Gibeya gu Beñamin. Ñu jekki séen gàngooru Filisti gay raj-rajloo, fu ne ñu jëm fa.
17Sóol ne ña ànd ak moom: «Wooteleen, ba xam ku jóge ci nun.» Ñu woote, Yonatan ak gàddukatu gànnaayam wuute.
18Sóol ne Axiya sarxalkat ba: «Indil gaalu Yàlla gi.» Bésub keroog gaalu Yàlla gaa ngaak bànni Israyil.
19Naka la Sóol di wax ak sarxalkat bi, coow la ca dalub waa Filisti gëna jolli. Sóol ne sarxalkat bi: «Ah, bàyyi ko sax.»
20Ba mu ko defee Sóol ak gàngoor ga ànd ak moom gépp daje, dem ca xare ba. Gisuñu lu moy waa Filisti ne kër-kër, ne këpp, di jamante seeni saamar.
21Ci biir loolu Ebrë yi nangul woon waa Filisti démb ak bëkk-démb te nekkandook ñoom ca dal baak fa ko wër fépp sax, ne waññet, faraat ak seen bokki bànni Israyil ya ànd ak Sóol ak Yonatan.
22Mboolem bànni Israyil ya làqu woon ca tundi Efrayim dégg ne waa Filisti daw nañu. Ñoom it ne leen dann ca xare ba.
23Noonu la Aji Sax ji maye Israyil ndam bésub keroog, xare bay law, ba ca wàlla Bet Awen.
24Bésub keroog mbooloom Israyil jàq nañu, ndax ngiñ lu Sóol teg ci seen kaw, ne: «Képp ku lekk fii ba ngoon te feyooguma ci samay noon, yal na alku.» Mbooloo ma mépp, kenn sexu ca dugub.
25Ci kaw loolu waa réew ma mépp dem ba ca gott ba. Fekk na ag lem a nga fa ca suuf.
26Ba mbooloo ma duggee ca biir gott ba, yemuñu ca lu moy lem jay xelli, waaye kenn sàkku ci, jëme ci gémmiñam, ndax ragal ngiñ la.
27Yonatan nag yégul woon ngiñal baayam la mu teg mbooloo ma. Mu tàllal yet wa ca loxoom, capp cat la ca lem ja, sex, bët ya daldi leer.
28Kenn ca mbooloo ma ne ko: «Aa! Ngiñ lii de, sa baay giñoon na ko ci kaw mbooloo mi, ne: “Képp ku lekk tey, yal na alku,” moo tax mbooloo mi néew doole.»
29Yonatan ne: «Sama baay de yàqal na mbooloo mi. Xool-leen rekk ni samay bët leere ndax lem sii ma ñam!
30Astamaak bu mbooloo mi lekkoon tey ci lël ja ñu nangoo ci noon yi! Du ci la jéllu waa Filisti doon gëna réy a waay?»
31Bésub keroog bànni Israyil a dumaa waa Filisti ca Migmas ba ca Ayalon. Bànni Israyil sonn lool nag.
32Ba loolu amee ñu sëxëtoo lël ja, jël ca gàtt yaak nag ya ba ca wëllu ya, tër ca suuf, boole yàpp waak deret ja, lekk.
33Ñu yegge ko Sóol, ne ko: «Mbooloo ma kat a nga nee, di moy Aji Sax ji, di lekk yàpp wu ànd ak deretam.» Sóol ne: «Yeenaka fecci kóllëre! Béraŋal-leen ma fii aw doj wu mag léegi.»
34Gannaaw loolu mu joxe leneen ndigal, ne: «Tasaarooleen ci biir mbooloo mi, ne leen ñu indi fii ñoom ñépp seeni nag ak seeni gàtt. Fii lañuy rendee jur gi, door koo lekk. Su ko defee duñu moy Aji Sax ji, di lekk yàpp wu ànd ak deretam.» Mbooloo mépp daldi dikk guddig keroog, ku nekk akaw nagam. Ñu rendi foofa.
35Sóol daldi fay tabax ab sarxalukaay, ñeel Aji Sax ji. Boobu sarxalukaay la jëkka tabax ñeel Aji Sax ji.
36Ba loolu amee Sóol ne: «Nan toppi waa Filisti ci guddi gi, nu sëxëtoo seen alal ba bët set, te bunu ci bàyyi kenn, mu dund.» Mbooloo ma ne ko: «Loo bëgg rekk, defal!» Sarxalkat ba nag ne ko: «Nanu ko jëkka diis Yàlla fii.»
37Sóol laaj Yàlla ne ko: «Ndax ma topp waa Filisti? Ndax dinga leen teg ci loxol Israyil?» Bésub keroog nag Yàlla tontuwul.
38Sóol ne: «Yeen njiiti mbooloo mi yépp, dikkleen fii, nu seet ba gis bàkkaarub tey jii, lu mu doon.
39Ndax giñ naa ci Aji Sax jiy dund, wallukatub Israyil, bu doon sax lu sama doom Yonatan ci boppam def, dee rekk ay àtteem.» Mbooloo mépp, kenn tontuwu ko.
40Mu ne bànni Israyil gépp: «Taxaweleen nee, maak sama doom Yonatan, nu taxawe nii.» Mbooloo ma ne Sóol: «Loo bëgg rekk, defal.»
41Sóol ñaan ci Aji Sax ji, ne ko: «Yaw Yàllay Israyil, ngalla xamleel liy dëgg.» Ñu daldi tegoo bant, mu dal ci kaw Yonatan ak Sóol, mbooloo ma wàcc.
42Sóol ne: «Tegal-leen nu bant sama digganteek Yonatan.» Ñu tegal leen, mu dal ca doomam Yonatan.
43Sóol ne Yonatan: «Wax ma loo def.» Yonatan ne ko: «Aylayéwén maa ñam tuuti ca lem, ja ma cappe sama catu yet wi ma yoroon ci sama loxo. Maa ngi, naa dee!»
44Sóol ne ko: «Na ma Yàlla teg mbugal mu gëna tar, waaye yaw Yonatan dinga dee déy!»
45Mbooloo ma nag ne Sóol: «Lan? Yonatan dee, moom mi may Israyil ndam lu réy lii? Xalaateesu ko moos! Giñ nanu ci Aji Sax jiy dund, du lenn luy rote ci kawaru boppu Yonatan sax, dal fi suuf, ndax Yàlla la àndal def lii tey.» Noonu la mbooloo ma jote Yonatan, ba deewul.
46Ba loolu wéyee Sóol noppee dàq waa Filisti, waa Filisti dellu ca seenum réew.
47Gannaaw ba Sóol feddlee nguuram ca Israyil, xare naak seen noon ya leen wër yépp: Mowabeen ñaak Amoneen ñaak Edomeen ñaak buuri waa Soba, ak waa Filisti. Mboolem fu mu walbatiku rekk, moo daan.
48Njàmbaar la xaree, duma Amalegeen ña, ba musal Israyil ca ña doon sëxëtoo seen alal.
49Doomi Sóol yu góor nag ñoo doon: Yonatan, ak Iswi ak Malkisuwa; ñaari doomam yu jigéen, di Merab mi ci gën di mag, ak Mikal mi gën di ndaw.
50Soxnas Sóol moo doon Ayinowam, Ayimaas di baayu Ayinowam. Njiitu xareem moo doon Abner doomu Ner baayu Sóol bu ndaw,
51Kis miy baayu Sóol, ak Ner, baayu Abner, Abyel ay seen baay.
52Xare bu metti la woon seen digg ak waa Filisti, giiru dundu Sóol gépp. Moo tax fu Sóol gisaan boroom kàttan mbaa boroomu fit, da koy dollikoo.