Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - 1.Samiyel

1.Samiyel 30

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Ba Daawuda aki nitam àggee Ciglaag, ca gannaaw ëllëg sa la. Fekk na Amalegeen ña song bëj-saalumu Yuda ak Ciglaag; ñu yàqte Ciglaag, lakk ko,
2jàpp jigéen ña mu fa fekk, mag ak ndaw. Reyuñu ca kenn nag, dañu leena yóbbaale, dem seen yoon.
3Ba Daawudaaki nitam agsee Ciglaag, fekk nañu mu lakk ba jeex; seeni jabar ak seeni doom, góor ak jigéen, ñépp duggi njaam.
4Daawudaak mbooloo ma mu àndal nag di yuuxook a jooyoo, ba amatuñu dooley jooy.
5Ñaari soxnay Daawuda lañu jàpp; Ayinowam mu Yisreel ak Abigayil waa Karmel ba, soxnas Nabal woon.
6Ba loolu amee Daawuda jàq lool, ndax mbooloo maa nga doon wax naan dañu koy dóori doj. Booba mbooloo ma ba mu daj, ku nekk a ngaak naqaru xol, di xalaat doomam yu góor ak yu jigéen. Daawuda nag dëgërloo Yàllaam Aji Sax ji rekk.
7Ci biir loolu Daawuda wax ak sarxalkat ba Abiyatar doomu Ayimeleg, ne ko mu indil ko xar-sànni mi. Abiyatar indil Daawuda xar-sànni ma.
8Daawuda laaj Aji Sax ji, ne ko: «Ndax ma topp gàngooru yàqkat yii? Ndax dinaa leen dab?» Mu ne ko: «Demal, yaay dabe déy, te yaay xettlee déy.»
9Ba mu ko defee Daawuda dem, mook juróom benni téeméeri nit ña ànd ak moom. Ñu dem ba ca xuru Besor, ñenn ña yem fa.
10Daawudaa ñoqli, mook ñeenti téeméeri nit, ñaar téeméeri nit yem foofa, ndax loof, ba manuñoo jàll xuru Besor.
11Ci kaw loolu ña jàll yem ci jenn waayu Misra ci àll bi. Ñu indi waa ji ba ci Daawuda, daldi may waa ji mburu mu lekk, may ko ndox, mu naan.
12Ab danku figg ju wow ak ñaari danki reseñ lañu ko leel, mu doora leqliku, ndax dafa fekk lekkul, naanul diiru ñetti guddi ak ñetti bëccëg.
13Daawuda ne ko: «Yaw, kuy sab sang ak foo bokk?» Xalelu góor ba ne ko: «Man waa Misra laa, di jaamub jenn waayu Amalegeen. Sama sang a ma wacc, ba ma woppee bëkkaati-démb.
14Noo song wetu Negew ca diiwaanu waa Keret ña, ak diiwaanu Yuda, ak wetu Negew ca diiwaanu Kaleb, te Ciglaag, noo ko lakk.»
15Daawuda ne ko: «Ndax man nga maa yóbbu ba ci gàngooru yàqkat yooyu?» Mu ne ko: «Giñal ma ci Yàlla ne, doo ma rey, te doo ma delloo ca sama sang; kon dinaa la yóbbu ba ci gàngooru yàqkat yi.»
16Ci kaw loolu waa ja yóbbu Daawuda, ndeke nit ñaa nga ne wesar ca àll ba bépp, di lekk ak a naan, di mbumbaaye mboolem alal ju bare ja ñu nangoo ca réewum Filisti ak réewum Yuda.
17Daawuda nag di leen fàdd, njël ba ca ngoon. Kenn rëccul, lu moy ñeenti téeméeri xale yu góor yu war ay giléem, daw.
18Daawuda nangu mboolem lu Amalegeen ña jëloon, nangu ñaari soxnaam.

19Dara lu bokk ci ñoom rawul. Mag ñaak ndaw ñaak seen doom yu góor ak seen doom yu jigéen ak alal jaak mboolem lu ñu leen jëlaloon. Lépp la Daawuda délloosi.
20Mu nangu mboolem jur gu gudd ak gu gàtt, nitam ña dàq, tofal ca juru Amalegeen ña, te naan: «Lëlub Daawudaa ngi!»
21Daawuda nag dikk ba ca ñaar téeméer ña loofoon ba manuñu koo topp, te ñu bàyyi woon leen ca xuru Besor. Naka lañu gatandu Daawuda ak ña mu àndal, Daawuda dikk, dajeek ñoom, jàmmanteek ñoom.
22Mboolem ñu bon ñaak ñu sew ña jàllandoo woon ak Daawuda nag ne leen: «Gannaaw ñii ànduñu woon ak nun, dunu leen jox dara ci alal ji nu nangu. Xanaa ku nekk jël jabaram aki doomam rekk, yóbbu te dem.»
23Daawuda ne leen: «Déet bokk yi, buleen def noonu, ak li nu Aji Sax ji defal, aar nu, teg gàngooru yàqkat yi nu songoon ci sunuy loxo.
24Ana nu xel mana nangoo loolu? Na ku xarejeek ku desoon ca cummikaay la, yem ak sa moroom cér; ñépp ay séddu.»
25Bésub keroog la Daawuda dale def loolu mu dib dogal, di àtteb yoon bu ñeel Israyil ba tey jii.
26Ba Daawuda delloo Ciglaag, sédd na ca lël ja, magi Yuda, xaritam ya. Mu yónnee leen ko, ne leen: «Lii, yeenay boroom; xéewal la gu jóge ca alalu nooni Aji Sax ji.»
27Noonu la ca sédde waa Betel ak waa Ramot Negew ak waa Yatir
28ak waa Arower ak waa Sifmot ak waa Estemowa
29ak waa Rakal, ak waa dëkki Yerameleen ña ak waa dëkki Keneen ña,
30ak ña ca Xorma ak ña ca Bor Asan ak ña ca Atag
31ak ña ca Ebron ak mboolem waa gox ya mu jaare woon, mooki nitam.