Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - 1.Samiyel

1.Samiyel 18

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Ba Daawuda di wax ak Sóol ba noppi, fekk na Yonatan yég ci xolam na mu taqook Daawuda ci biir cofeelu benn bakkan. Yonatan dafa soppoon Daawuda ni boppam.
2Bésub keroog la Sóol téye Daawuda, mayatu ko mu ñibbi kër baayam.
3Ba loolu amee Yonatan fasook Daawuda kóllëre, ndax sopp ko ni boppam.
4Ci biir loolu Yonatan summi turkeem, jox ko Daawuda, boole ca ay yérey xareem, ba ca saamaram ak fittam ak ngañaayam sax.
5Daawuda nag di dem ci bépp yoonu xare bu ko Sóol yebal, di ca am ndam. Sóol fal ko njiitu xarekat ya, gàngoor gépp rafetlu loolu, jawriñi Sóol itam rafetlu ko.
6Ba ñu demee ba xarekat yay ñibbi, gannaaw ba Daawuda reyee waa Filisti ba, jigéeni mboolem dëkki bànni Israyil a génn gatanduji Buur Sóol, di fecc ak a woy, tabala ya ànd ak sarxolle ya ak xalam ya.
7Ña ngay fo, di awoonte, naan: Sóol jam junneem, Daawuda jam fukki junneem.
8Sóol ñaawlu kàddu ga, mer lool. Mu ne ca xelam: «Daawuda lañu moomale fukki junni; man, junni! Lu ko deseeti lu moy jal bi?»
9Bésub keroog la Sóol dale ronni Daawuda.
10Ca ëllëg sa ngelawal Yàlla lu aay ne milib ca kaw Sóol, muy waxtu ca digg këram. Daawuda nag di ko xalamal, na mu daan def naka jekk, fekk Sóol ŋàbb ab xeejam.
11Mu jekki sànni xeej ba, te naan ca xelam: «Naa daaj Daawuda ci tabax bi!» Daawuda nag mbas ko ñaari yoon.
12Sóol daldi ragal Daawuda, ndax booba xam na ne Aji Sax jee ko dëddu, ànd ak Daawuda.
13Ba loolu amee mu jële ko fi wetam, fal ko njiitu kurélu junniy xarekat, muy xareji, di délsi, jiite gàngoor ga.
14Daawuda baaxle ca yoonam yépp, Aji Sax ji ànd ak moom.
15Ba Sóol gisee Daawuda àntule lool, mu gën koo ragal.
16Teewul mboolem Israyil ak Yuda sopp Daawuda, ngir moo leen jiite woon, di xareji, di dikk.
17Ci kaw loolu Sóol ne Daawuda: «Sama taaw bu jigéen, Merab a ngii. Moom laa lay may. Nekkal ma sama jàmbaaru xare rekk, te xareel Aji Sax ji ay xareem.» Booba Sóol a nga naan ca xelam: «Bu ko sama loxo laal, nay loxol waa Filisti.»
18Daawuda ne Sóol: «Waaw, ana lu ma tekki, man maak samay bokk, sama askanu baay ci Israyil, ba wara mana goromlook Buur?»

19Ba ñu demee ba wara jox Daawuda, Merab doomu Sóol ja, Àddiryel ma cosaanoo Mewola lañu ko may.
20Ci kaw loolu Mikal doomu Sóol bëgg Daawuda, ñu àgge ko Sóol, mu am ca mbégte.
21Booba Sóol a nga naan: «Naa ko ko may, ngir mu doon ndëgg-sërëxam, ba waa Filisti teg ko loxo.» Sóol nag wax Daawuda, ñaareel bi yoon, ne ko: «Tey ngay samab goro.»
22Ci biir loolu Sóol sant ay dagam, ne leen: «Diisool-leen maak Daawuda, ngeen wax ko ne ko: “Yaw kat, Buur am na bànneex ci yaw, te it dagam yépp a la sopp. Kon nag nangula doon gorob Buur.”»
23Dagi Sóol ya déey Daawuda kàddu yooyu. Daawuda ne leen: «Ngeen defe ne goromlook buur daal, du dara? Man mii taqul dara, tekkiwuma dara!»
24Dag ya yegge Sóol kàddu yooyu Daawuda wax.
25Sóol ne leen: «Waxleen Daawuda ne ko, Buur de sàkkuwul ub can: xanaa téeméeri mbuñukay waa Filisti yu mu feyoo ci noonam yooyu.» Booba la Sóol laloon mooy pexe mu tàbbal Daawuda ca loxol waa Filisti.
26Dag ya yegge Daawuda kàddu yooya, doon gorob buur daldi koy jaral loola. Balaa àpp baa mat,
27Daawuda dem na, mooki nitam ba rey ñaar téeméeri waa Filisti. Daawuda indi seeni mbuñuka, ñu waññal ko Buur ba mu mat sëkk, mu daldi yeyoo goromlook Buur. Ba loolu amee Sóol may Daawuda doomam Mikal.
28Sóol nag xam xéll ne Aji Sax jee ànd ak Daawuda, te it doomam Mikal bëgg na ko,
29mu gën koo ragalati. Fa la Sóol doxe doon noonub Daawuda ba fàww.
30Ci kaw loolu njiiti xarey Filisti di amal ay cong, noppiwuñoo xareek Israyil. Teewul saa yu ñu songaan, Daawudaay gëna am ndam mboolem jawriñi Sóol, ba mujj Daawuda amu tur lool.