Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - 1.Samiyel

1.Samiyel 3

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Ngóor sa Samiyel nag moom, di liggéeyal Aji Sax ji fi kanam Eli. Kàddug Aji Sax ji néewoon na ca yooya jamono, peeñu mu leer it tumurànke woon na.
2Mu am bés Eli tëdd fa muy tëdd naka jekk, fekk bët ya naqari, ba daanaka gisatul.
3Booba làmpu jaamookaayu Yàlla bi feyagul, te Samiyel a ngi tëdd ci biir jaamookaayu Aji Sax ji, fi gaalu Yàlla gi nekk.
4Aji Sax ji woo Samiyel, mu ne: «Maa ngi»,
5daldi daw ba ca Eli, ne ko: «Maa ngi, du yaa ma woo?» Eli ne ko: «Wootewuma de, dellul tëri.» Mu dellu tëdd.
6Aji Sax ji dellu woo Samiyel, Samiyel jóg, dem ba ca Eli ne ko: «Maa ngi, du yaa ma woo?» Eli ne ko: «Wootewuma de doom, dellul tëri.»
7Booba Samiyel xamagul woon Aji Sax ji, te kàddug Aji Sax ji dikkalagu ko woon.
8Aji Sax ji wooti Samiyel ñetteel bi yoon, Samiyel jógati, dem ba ca Eli ne ko: «Maa ngi, du yaa ma woo?» Eli nag xam ne Aji Sax jeey woo xale bi.
9Mu ne Samiyel: «Demal tëri, bu la wootee, nee ko: “Aji Sax ji, maa ngi lay déglu, Sang bi, waxal.”» Samiyel dellu tëdd fa muy tëdd.
10Ba mu ko defee Aji Sax ji dikk taxaw, wooti ko na woon, ne ko: «Samiyel, Samiyel.» Samiyel ne: «Maa ngi lay déglu, Sang bi, waxal.»
11Aji Sax ji ne Samiyel: «Maa ngii déy, di waaja def ci digg bànni Israyil, mbir muy buur noppi mboolem ku ko dégg.
12Bésub keroog ma matal ci Eli mboolem lu ma waxoon ne mooy dal waa këram, ndoorte la ba ca muj ga.
13Waxoon naa ko ne ko dinaa teg waa këram mbugal mu sax dàkk, ndax ñaawtéef gu ay doomam nekke, di ñàkke Yàlla teggin, mu yég ko te jubbantiwu leen.
14Looloo waral ma giñal waa kër Eli, ne du am mukk benn saraxu jur mbaa beneen sarax bu leen mana jot ci seen ñaawtéef.»
15Ci kaw loolu Samiyel tëdd ba ca suba sa, mu tijji bunti kër Aji Sax ji, waaye ñemewula nettali Eli peeñu ma.
16Eli nag woo ko ne ko: «Samiyel doom, ana nga?» Samiyel ne ko: «Maa ngi.»
17Eli ne ko: «Kàddu gi mu la wax, lu mu doon? Bu ma nëbbu kay. Soo ma nëbbee lenn ci li mu la wax, yal na la Yàlla teg naqar wu gëna tar.»
18Samiyel wax ko lépp, nëbbu ko ca dara. Eli ne: «Mooy Aji Sax ji. Li ko soob, na ko def.»

19Ci kaw loolu Samiyel di màgg, Aji Sax ji ànd ak moom, waccul genn kàddug Samiyel, mu fanaan àll.
20Noonu la Israyil gépp ràññee, la dale Dan ca bëj-gànnaar ba ca Beerseba ca bëj-saalum, ne Samiyel taxaw na taxawaayu yonentu Aji Sax ji.
21Aji Sax ji nag wéye koo feeñu ca Silo. Ci kàddug Aji Sax ji la ko Aji Sax ji daan feeñoo ca Silo.