Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - YOWAANA - YOWAANA 11

YOWAANA 11:20-49

Help us?
Click on verse(s) to share them!
20Bi Yeesu ñëwee, Màrt yég ko, dem di dajeek moom; fekk booba Maryaamaa nga toogoon ca kër ga.
21Màrt ne Yeesu: «Boroom bi, boo fi nekkoon de, sama càmmiñ li du dee.
22Waaye xam naa ne fii nu tollu sax, loo ñaan Yàlla, mu may la ko.»
23Yeesu ne ko: «Sa càmmiñ dina dekki.»
24Màrt ne ko: «Xam naa ne dina jóg bésu ndekkite la, keroog bés bu mujj ba.»
25Yeesu ne ko: «Man maay ndekkite li, maay dund gi. Ku ma gëm, boo deeyee it, dinga dund.
26Rax-ca-dolli kuy dund te gëm ma, doo dee mukk. Ndax gëm nga loolu?»
27Mu ne ko: «Waaw, Boroom bi. Gëm naa ne yaay Almasi bi, di Doomu Yàlla, ji wara ñëw àddina.»
28Bi Màrt waxee loolu, mu daldi dem wooyi Maryaama ne ko ci pett: «Kilifa gaa ngi fi; mi ngi lay laaj.»
29Bi Maryaama déggee loolu, mu daldi jóg, gaawantu dem ca Yeesu.
30Te fekk duggagul woon ca dëkk ba, waaye ma nga woon ba tey ca bérab, ba mu daje woon ak Màrt.
31Noonu Yawut, ya nekkoon ca kër ga di dëfal Maryaama, gis ko mu ne bërét génn, ñu daldi koy topp, defe ne day jooyi ca bàmmeel ba.
32Bi Maryaama agsee nag ca Yeesu, ba gis ko, mu daanu ciy tànkam ne ko: «Boroom bi, boo fi nekkoon, sama càmmiñ du dee.»
33Yeesu gis ne mi ngi jooy te Yawut yi ànd ak moom itam ñu ngi jooy. Mu daldi jàq, am naqar wu réy.
34Mu ne leen: «Fu ngeen ko denc?» Ñu ne ko: «Kaay gis, Sang bi.»
35Yeesu jooy.
36Noonu nag, Yawut ya ne: «Gis ngeen ni mu ko bëgge woon!»
37Waaye am na ca ñoom ñu doon wax naan: «Moom mi ubbi bëti gumba gi, ndax manul woona fexe ba Lasaar du dee?»
38Yeesu dellu am naqar wu réy, daldi dem ca bàmmeel ba. Pax la mu ñu yett ci doj, ube ko xeer.
39Yeesu ne: «Dindileen xeer wi!» Màrt, jigéenu ku dee ki ne ko: «Boroom bi, dina xasaw xunn fii mu nekk, ndaxte am na ci bàmmeel bi ñeenti fan.»
40Yeesu ne ko: «Ndax waxuma la ne boo gëmee, dinga gis ndamu Yàlla?»
41Ñu daldi dindi xeer wa. Yeesu xool ci kaw, ne jàkk asamaan, ñaan Yàlla ne: «Baay, sant naa la ci li nga ma déglu ba noppi.
42Xam naa ne doo jóg ci di ma déglu, waaye dama koy wax, ngir nit ñi ma wër gëm ne yaa ma yónni.»
43Bi mu waxee loolu, Yeesu woote ak baat bu dëgër ne: «Lasaar, ñëwal ci biti!»
44Néew bi daldi génn, ñu gis càngaay, li ñu takke woon tànk yi ak loxo yi, ak kaala, gi ñu muure woon kanam gi. Yeesu ne leen: «Tekkileen ko, bàyyi ko mu dem.»
45Yawut yu bare ca ña ñëwoon kër Maryaama te gis li Yeesu defoon, daldi koy gëm.
46Waaye amoon na it ñu demoon ci Farisen ya, nettali leen la Yeesu defoon.
47Farisen ya ak sarxalkat yu mag ya woo kureelu àttekat ya ne: «Nit kii kat, kéemaan yi muy def a ngi bëgga bare. Lu nuy def nag?
48Ndaxte su nu ko bàyyee mu jàppoo nii, ñépp dinañu ko gëm, te kilifay Room yi dinañu ñëw, daaneel sunu kër Yàlla gi, tas sunu réew!»
49Amoon na ca ñoom ku ñuy wax Kayif te mu nekkoon sarxalkat bu mag ba at mooma; mu ne leen: «Xamuleen ci mbir mi dara.

Read YOWAANA 11YOWAANA 11
Compare YOWAANA 11:20-49YOWAANA 11:20-49