Text copied!
Bibles in Wolof

YOWAANA 11:20-49 in Wolof

Help us?

YOWAANA 11:20-49 in Téereb Injiil

20 Bi Yeesu ñëwee, Màrt yég ko, dem di dajeek moom; fekk booba Maryaamaa nga toogoon ca kër ga.
21 Màrt ne Yeesu: «Boroom bi, boo fi nekkoon de, sama càmmiñ li du dee.
22 Waaye xam naa ne fii nu tollu sax, loo ñaan Yàlla, mu may la ko.»
23 Yeesu ne ko: «Sa càmmiñ dina dekki.»
24 Màrt ne ko: «Xam naa ne dina jóg bésu ndekkite la, keroog bés bu mujj ba.»
25 Yeesu ne ko: «Man maay ndekkite li, maay dund gi. Ku ma gëm, boo deeyee it, dinga dund.
26 Rax-ca-dolli kuy dund te gëm ma, doo dee mukk. Ndax gëm nga loolu?»
27 Mu ne ko: «Waaw, Boroom bi. Gëm naa ne yaay Almasi bi, di Doomu Yàlla, ji wara ñëw àddina.»
28 Bi Màrt waxee loolu, mu daldi dem wooyi Maryaama ne ko ci pett: «Kilifa gaa ngi fi; mi ngi lay laaj.»
29 Bi Maryaama déggee loolu, mu daldi jóg, gaawantu dem ca Yeesu.
30 Te fekk duggagul woon ca dëkk ba, waaye ma nga woon ba tey ca bérab, ba mu daje woon ak Màrt.
31 Noonu Yawut, ya nekkoon ca kër ga di dëfal Maryaama, gis ko mu ne bërét génn, ñu daldi koy topp, defe ne day jooyi ca bàmmeel ba.
32 Bi Maryaama agsee nag ca Yeesu, ba gis ko, mu daanu ciy tànkam ne ko: «Boroom bi, boo fi nekkoon, sama càmmiñ du dee.»
33 Yeesu gis ne mi ngi jooy te Yawut yi ànd ak moom itam ñu ngi jooy. Mu daldi jàq, am naqar wu réy.
34 Mu ne leen: «Fu ngeen ko denc?» Ñu ne ko: «Kaay gis, Sang bi.»
35 Yeesu jooy.
36 Noonu nag, Yawut ya ne: «Gis ngeen ni mu ko bëgge woon!»
37 Waaye am na ca ñoom ñu doon wax naan: «Moom mi ubbi bëti gumba gi, ndax manul woona fexe ba Lasaar du dee?»
38 Yeesu dellu am naqar wu réy, daldi dem ca bàmmeel ba. Pax la mu ñu yett ci doj, ube ko xeer.
39 Yeesu ne: «Dindileen xeer wi!» Màrt, jigéenu ku dee ki ne ko: «Boroom bi, dina xasaw xunn fii mu nekk, ndaxte am na ci bàmmeel bi ñeenti fan.»
40 Yeesu ne ko: «Ndax waxuma la ne boo gëmee, dinga gis ndamu Yàlla?»
41 Ñu daldi dindi xeer wa. Yeesu xool ci kaw, ne jàkk asamaan, ñaan Yàlla ne: «Baay, sant naa la ci li nga ma déglu ba noppi.
42 Xam naa ne doo jóg ci di ma déglu, waaye dama koy wax, ngir nit ñi ma wër gëm ne yaa ma yónni.»
43 Bi mu waxee loolu, Yeesu woote ak baat bu dëgër ne: «Lasaar, ñëwal ci biti!»
44 Néew bi daldi génn, ñu gis càngaay, li ñu takke woon tànk yi ak loxo yi, ak kaala, gi ñu muure woon kanam gi. Yeesu ne leen: «Tekkileen ko, bàyyi ko mu dem.»
45 Yawut yu bare ca ña ñëwoon kër Maryaama te gis li Yeesu defoon, daldi koy gëm.
46 Waaye amoon na it ñu demoon ci Farisen ya, nettali leen la Yeesu defoon.
47 Farisen ya ak sarxalkat yu mag ya woo kureelu àttekat ya ne: «Nit kii kat, kéemaan yi muy def a ngi bëgga bare. Lu nuy def nag?
48 Ndaxte su nu ko bàyyee mu jàppoo nii, ñépp dinañu ko gëm, te kilifay Room yi dinañu ñëw, daaneel sunu kër Yàlla gi, tas sunu réew!»
49 Amoon na ca ñoom ku ñuy wax Kayif te mu nekkoon sarxalkat bu mag ba at mooma; mu ne leen: «Xamuleen ci mbir mi dara.
YOWAANA 11 in Téereb Injiil