Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sabóor - Sabóor 65

Sabóor 65:7-13

Help us?
Click on verse(s) to share them!
7Yaa dëje tund yu mag yi doole, gañoo sa kàttan,
8di dalal riirum géej aki gannaxam, ak coowal xeet yi,
9ba waa cati àddina yéemoo say firnde, waa penkook sowu di sarxolle.
10Yaa dikke suuf am wal, nangul koo nangul. Dexu Yàllaa fees ndox, ngay may nit peppam, ni nga ko waajale suuf si,
11di suuxat ngàbb mi, maasalee ko jal yi, sottiy waame, mu mokk, cax ma, nga barkeel.
12Yaay tëje mbeyum at mi say ngëneel, foo jaare, xéewal walangaan.
13Parluy màndiŋ yaa ngi walangaan, li wër tund yu ndaw yi di xumbéen.

Read Sabóor 65Sabóor 65
Compare Sabóor 65:7-13Sabóor 65:7-13