7 Yaa dëje tund yu mag yi doole, gañoo sa kàttan,
8 di dalal riirum géej aki gannaxam, ak coowal xeet yi,
9 ba waa cati àddina yéemoo say firnde, waa penkook sowu di sarxolle.
10 Yaa dikke suuf am wal, nangul koo nangul. Dexu Yàllaa fees ndox, ngay may nit peppam, ni nga ko waajale suuf si,
11 di suuxat ngàbb mi, maasalee ko jal yi, sottiy waame, mu mokk, cax ma, nga barkeel.
12 Yaay tëje mbeyum at mi say ngëneel, foo jaare, xéewal walangaan.
13 Parluy màndiŋ yaa ngi walangaan, li wër tund yu ndaw yi di xumbéen.