Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sabóor - Sabóor 63

Sabóor 63:1-4

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Muy kàddug Sabóor, ñeel Daawuda. Mooy ba mu nekkee ca màndiŋu Yuda.
2Yaw Yàlla, yaay sama Yàlla, ma di la sàkku, sama bakkan mar la, sama jëmm namm la, fu suuf mare ndox, ne sereŋ.
3Moo tax kër gu sell ga laa la séentoo, ngir niir sa leer ak sa teddnga.
4Xéewloo sa ngor moo dàq dundu bakkan; ma àddu boog, kañ la!

Read Sabóor 63Sabóor 63
Compare Sabóor 63:1-4Sabóor 63:1-4