2Éy Aji Sax ji, noon yeeka bare! Ñu baree may jógal,
3ñu baree may tooge naa: «Yàlla du ko wallu!» Selaw
4Waaye yaw Aji Sax ji, yaa may feg, di ma teral, di ma siggil.
5Maay woo Aji Sax ji wall, mu walloo ma fa tundam wu sell wa. Selaw.
6Maay tëdd nelaw, yewwu; Aji Sax ji di ma aar.
7Ñu dul jeex a ma jógal, gaw ma, te duma ragal.
8Éy Aji Sax ji sama Yàlla, jógal, wallu ma! Yaa toj kaabaabi noon yu bon yépp, foq seeni sell.