Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sabóor - Sabóor 148

Sabóor 148:1-13

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Màggal-leen Ki Sax! Nangeen màggale Aji Sax ji fa asamaan, màggale ko fa kawa kaw.
2Màggal-leen ko, yeen malaakaam yépp, màggal-leen ko, yeen gàngooram yi.
3Màggal-leen ko, yeen jant beek weer wi, màggal-leen ko, yeen mboolem biddiiw yii di nes-nesi.
4Màggal-leen ko, yeen asamaani kaw-li-kaw, ba ca ndox ma tiim asamaan ya.
5Nañu màggal turu Aji Sax ji, kii kat a santaane, lii lépp am.
6Moo leen samp, ñu sax ba fàww, mu dogal ko, te du toxu.
7Nangeen màggale Aji Sax ji fa kaw suuf, yeen ninki-nànkay géej ak xóote yépp,
8ba ca melax yaak doj yu sedd yay taw, ak tawub yuur akub lay, ba ca ngëlén yu mag yay def ndigalam.
9Màggal-leen ko yeen tund yu mag yeek yu ndaw yépp, ba ci garab yiy meññ ak garabi seedar yi,
10ba ci mala yépp, yu àll ak gépp jur ak luy raam ak njanaaw,
11ak buuri àddinaak xeet yépp, ak kilifa yeek njiiti àddina yépp,
12xale bu góor ak bu jigéen, mag ak ndaw.
13Màggal-leen turu Aji Sax ji, moom doŋŋ la turam kawe, darajaam tiim asamaan ak suuf.

Read Sabóor 148Sabóor 148
Compare Sabóor 148:1-13Sabóor 148:1-13