2Naa xaacu, woo Yàlla, sama baat fa Yàlla, ngir mu déglu ma.
3Bëccëg, ma jàq, sàkku Boroom bi; guddi, ma tàllal loxo, toqiwuma. Sama xol tëë sedd.
4Ma bàyyi Yàlla xel, binni, xalaat, xol jeex. Selaw.
5Éy Yàlla, tere nga maa gëmm bët, ma jaaxle ba waxatuma,
6xanaa xalaat janti démb, at ya woon.
7Guddi may fàttliku sama woy, di waxtaan ak sama ngegenaay, sama xel di jéex te naa:
8«Boroom bi da may gàntal ba fàww, ba du ma baaxeeti mukk a?
9Xanaa daa jeexal ngor tàkk? Am kàddoom a deñ ba fàww?
10Moo Yàlla daa fàtte ñeewantee? Am meram a tëj buntu yërmandeem?» Selaw.