Text copied!
Bibles in Wolof

Sabóor 77:2-10 in Wolof

Help us?

Sabóor 77:2-10 in Kàddug Yàlla gi

2 Naa xaacu, woo Yàlla, sama baat fa Yàlla, ngir mu déglu ma.
3 Bëccëg, ma jàq, sàkku Boroom bi; guddi, ma tàllal loxo, toqiwuma. Sama xol tëë sedd.
4 Ma bàyyi Yàlla xel, binni, xalaat, xol jeex. Selaw.
5 Éy Yàlla, tere nga maa gëmm bët, ma jaaxle ba waxatuma,
6 xanaa xalaat janti démb, at ya woon.
7 Guddi may fàttliku sama woy, di waxtaan ak sama ngegenaay, sama xel di jéex te naa:
8 «Boroom bi da may gàntal ba fàww, ba du ma baaxeeti mukk a?
9 Xanaa daa jeexal ngor tàkk? Am kàddoom a deñ ba fàww?
10 Moo Yàlla daa fàtte ñeewantee? Am meram a tëj buntu yërmandeem?» Selaw.
Sabóor 77 in Kàddug Yàlla gi