Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sabóor - Sabóor 75

Sabóor 75:3-9

Help us?
Click on verse(s) to share them!
3Yàlla nee: «Maay takk ab àpp, àtte ca njub.
4Bu suuf di yëngu mook ñi ko dëkke ñépp, maay kiy téye ay kenoom. Selaw.
5Dama ne ku réy: “Bul réy-réylu,” ne ku bon: “Bul bew,
6bul bewa bew, bay waxe reewande.”»
7Du penku, du sowu, te du màndiŋ ma la daraja di jóge.
8Yàllaay àtte: kii mu detteel, kee mu kaweel.
9Merum Aji Sax ji dib kaas ci loxoom, biiñu njafaan bu wex di ca fuur, mu jol ko képp ku bon ci àddina, mu naan ba naanaale ginjrit ga.

Read Sabóor 75Sabóor 75
Compare Sabóor 75:3-9Sabóor 75:3-9