Text copied!
Bibles in Wolof

Sabóor 75:3-9 in Wolof

Help us?

Sabóor 75:3-9 in Kàddug Yàlla gi

3 Yàlla nee: «Maay takk ab àpp, àtte ca njub.
4 Bu suuf di yëngu mook ñi ko dëkke ñépp, maay kiy téye ay kenoom. Selaw.
5 Dama ne ku réy: “Bul réy-réylu,” ne ku bon: “Bul bew,
6 bul bewa bew, bay waxe reewande.”»
7 Du penku, du sowu, te du màndiŋ ma la daraja di jóge.
8 Yàllaay àtte: kii mu detteel, kee mu kaweel.
9 Merum Aji Sax ji dib kaas ci loxoom, biiñu njafaan bu wex di ca fuur, mu jol ko képp ku bon ci àddina, mu naan ba naanaale ginjrit ga.
Sabóor 75 in Kàddug Yàlla gi