3Yàlla nee: «Maay takk ab àpp, àtte ca njub.
4Bu suuf di yëngu mook ñi ko dëkke ñépp, maay kiy téye ay kenoom. Selaw.
5Dama ne ku réy: “Bul réy-réylu,” ne ku bon: “Bul bew,
6bul bewa bew, bay waxe reewande.”»
7Du penku, du sowu, te du màndiŋ ma la daraja di jóge.
8Yàllaay àtte: kii mu detteel, kee mu kaweel.