1Màggal-leen Ki Sax! Woyleen Aji Sax ji woy wu yees, màggal ko fi ndajem wóllëreem ñi.
2Na Israyil bége kii ko sàkk, doomi Siyoŋ, laa ne, ñu bànneexoo seen buur bii.
3Nañu màggale turam am pecc, tëggal ko, xalamal ko.
4Aji Sax jee safoo ñoñam, di terale néew-ji-doole ag mucc.
5Na wóllërey Yàlla bànneexoo seen ndam, bu ñu tëddee sax, di sarxolle,
6di xaacuy kañ Yàlla, ŋàbbaale saamaru ñaari ñawka,
7ngir duma yéefar yi, mbugale ko yooyu xeet,
8yeewe seeni buur ay càllala, jénge seeni njiit jéngi weñ,