Text copied!
Bibles in Wolof

Sabóor 149:1-8 in Wolof

Help us?

Sabóor 149:1-8 in Kàddug Yàlla gi

1 Màggal-leen Ki Sax! Woyleen Aji Sax ji woy wu yees, màggal ko fi ndajem wóllëreem ñi.
2 Na Israyil bége kii ko sàkk, doomi Siyoŋ, laa ne, ñu bànneexoo seen buur bii.
3 Nañu màggale turam am pecc, tëggal ko, xalamal ko.
4 Aji Sax jee safoo ñoñam, di terale néew-ji-doole ag mucc.
5 Na wóllërey Yàlla bànneexoo seen ndam, bu ñu tëddee sax, di sarxolle,
6 di xaacuy kañ Yàlla, ŋàbbaale saamaru ñaari ñawka,
7 ngir duma yéefar yi, mbugale ko yooyu xeet,
8 yeewe seeni buur ay càllala, jénge seeni njiit jéngi weñ,
Sabóor 149 in Kàddug Yàlla gi