Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Esekiyel

Esekiyel 27

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Kàddug Aji Sax ji dikkal na ma ne ma:
2«Yaw nag nit ki, yékkatil kàddu, jooye ko dëkkub Tir.
3Waxal Tir mi tooge buntu géej, jula yooyuy jëflanteek xeeti dun yu bare, nga ne ko: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Yaw Tir yaa noon: ‘Maaka matub taar!’
4Yaw mi sa kemu suuf àkki xolu géej, say tabaxkat a mottli sab taar.
5Dañu laa tabax ni ñuy tabaxe gaal, sàkke xànqi sippar fa tundu Senir, defare ca sa xott wépp, sàkk bantu seedaru Libaŋ, defare ponku diggu gaal ga.
6Ñu gorati garabu seen yu Basan, defare say joowu, kaw gaal gi, ñu defare ko banti sippar yu bawoo tefesi Géej gu mag ga, rafetale ko bëñi ñey.
7Lẽe bu bawoo Misra lañu ràbb ba mu jekk, def ko ndimoy wiiru gaal gi, nga raayawoo ko, cuub gu baxa ak cuub gu xewar bawoo dunu Elisa, di sa malaan,
8waa Sidon ak Arwàdd doonoon say joowkat. Yaw Tir, yaa yeb ñu rafet xel, ñuy say mool,
9magi Gebal ñeek nitam ñu xareñ ñi fi yaw féetewoo di jagal. Mboolem gaal yu mag yi ak ña cay liggéey di dal ak yaw, waa gaal ya di jënd sam njaay.
10Waa Pers ak waa Ludd ak waa Puut, ñépp a nga woon ca sa mbooloom xare, di wékk fa yaw seeni pakk ak seen mbaxanay xare. Ñooñoo la darajaal.
11Arwàddeen ñeek sa niti bopp a daan wattoo ca sa kaw miir yépp, Gammàddeen ñi di wattu say tata, seeni gànnaay wékke, wër say miir. Ñooñoo mottli sab taar.
12«“Tarsis dëkk baa doon sab jula ndax sa gépp xeetu alal ju bare, di indi xaalis, weñ gu ñuul ak gu weex ak beteex, di ko weccikoo seen alal.
13Waa Geres ak Tubal ak Meseg di say jula, di leen indil ay doom aadama ak ndabi xànjar yu ñuy weccikoo seen koom.
14Waa kër Togarma indi ay fas aki gawar aki berkelle, di ko weccikoo seen alal.
15Dedaneen ñi di say jula, koomu dun yu bare di jaare say loxo, ñu di la feye bëñi ñey ak bantu jalambaan.
16Waa Siri it di say jula, di jëndeek yaw lu bare loo defar, di ko wecci per yu jafe, ak ndimo yu xewar, ak séri ràbb ak lẽe ak peri koray ak peri rubi.
17Yudak réewum Israyil it di say jula, di la wecci bele bu bawoo Minit, ak dugub ak lem ak diwu togg ak diwu yaram.
18Dëkkub Damaas di la jula lu bare loo defar ak jépp alal joo barele, di la ko weccee biiñ bu jóge Elbon, ak kawaru xar gu weex.
19Waa Weden ak Yawaan bàyyikoo Usal, di la wecci sa koom weñ gu ñu tëgg, ak xasum kaas, ak barax bu xeeñ.
20Waa Dedan it di say jula, indil la seen ndimoy tegi fas.
21Waa Arabi ak mboolem garmiy Kedar it di julanteek yaw, feye la ay tàppaanga aki kuuy aki bëy.
22Julay Saba ak Raama it di julaak yaw, di la indil ngën-gi-safal ak mboolem peru gànjar, ak wurus yu ñuy weccikoo sa alal.
23Waa dëkk yii di Karan ak Kane ak Eden ñoom it di say jula, ñook julay Saba ak Asur ak Kilmàdd.
24Ñooñoo doon say jula yu lay indil yérey tànnéef, ak turki yu yolet, ak yérey ràbb, ak malaan yu yànj, ak goj yu rawaasoo yu wér.
25Ay gaali Tarsis yu mag a daan yóbbu sam njaay. Nga fees dell, diis gann fi digg xolu géej.
26Say joowkat waral la mbeex mi ne màww, ba digg géej, teewul ngelawal penku damm la.
27Sa alal ja, sab yeb, sa njaay ma, sa niti géej, say mool, say jagalkat, say jaaykat, ak mboolem sa dag yi ci sa biir, ak mboolem sa gàngoor gi ci sa biir, ñooy tàbbeendoo xolu géej keroog sa bésub jéll ba.
28Bu say mool yuuxoo, tefes yaay riir,
29képp kuy ŋàbb joowu wàcce gaalam. Nitu géejoo mboolem mool, ñépp fi suuf lañuy taxaw.
30Ñoo lay jooyal, di yuuxu yuux yu metti, xëppoo suuf, fërënqu cib dóom.
31Yaay tax ñuy nelu, sol ay saaku di ko ñaawloo, di la jooye naqaru xol ak yuux yu metti.
32Ñeey am tiis, yékkatil la kàddug jooy, jooy la ne: ‘Ana dëkk bu mel ni Tir, mi ñu wedamal nii biir géej?’
33Ba ngay yebbee géej sam koom, yaa daan reggal ñu bare. Sa alal ak sa koom gu bare nga woomale buuri àddina.
34Léegi rajaxoo nga biiri gannax ca biir xóotey géej, sa koom ak sa gàngoor gi ci sa biir, lépp jóoru.
35Waa dunoo dun a la tiisoo, seen yaramu buur ya dawa daw ba ñu ne yasar.
36Julay xeet yaa ngi muslu ci saw demin. Raglu nga mujje, te doo tekkeeti ba fàww!”»