Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Esekiyel

Esekiyel 3

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Mu ne ma: «Yaw nit ki, lii ngay gis, lekk ko. Lekkal taxañ bii te dem wax ak waa kër Israyil.»
2Ma ŋa, mu leel ma taxañ ba.
3Mu ne ma: «Yaw, nit ki, lekkal taxañ bii ma la jox, ba suur këll.» May lekk, mu neex ni lem.
4Mu ne ma: «Yaw nit ki, demal ba ca waa kër Israyil, te nga àgge leen samay wax.
5Du ci waaso wu xóotu làkk te diisu làmmiñ lees la yebal. Ca waa kër Israyil nga jëm.
6Bare na waaso yoo xamul seeni wax, yu xóotu làkk te diisu làmmiñ. Te su ma la yebaloon ci ñoom, ñu déggal la.
7Waaye waa kër Israyil duñu la nangoo déggal, ngir nanguwuñu maa déggal; ndax waa kër Israyil gépp a dëgër bopp te dërkiis.
8Maa ngii di la may kanam gu ñemee ni seen kanam, ba nga dëgër bopp ni ñoom.
9Jamaa moo raw doj te ni laay dëgërale sa bopp. Bu leen ragal, bu leen tiit, li ñuy kërug fippukat yépp.»
10Mu teg ca, ne ma: «Yaw nit ki nag, mboolem li ma lay wax, dégloo ko nopp, te teewloo ko xel.
11Nanga dem ba ca sa bokki ngàllo ga, nga wax leen, ñu déglook ñu gàntal, ne leen: “Lii Boroom bi Aji Sax ji da koo wax.”»
12Ci kaw loolu ngelaw ne ma siféet, may dégg sama gannaaw, riirum kàddu gu xumb gu ne: «Cant ñeel na teddngay Aji Sax ji fi màkkaanam.»
13Mu ànd ak riirum laafi bindeef yay fenqoo, ak coowal mbege ya ñu feggool, muy riir mu xumb.
14Ba loolu amee ngelaw ne ma siféet, yóbbu. Maa ngay deme naqar ak xol bu tàng, te loxol Aji Sax ji diis gann ci sama kaw.
15Ma àgg ba ca ngàllog Tel Abib, ga dëkke tàkkal dexu Kebar. Foofa ñu dëkk laa toog, jommi ci seen biir diiru juróom ñaari fan.
16Ba juróom ñaari fan ya matee, kàddug Aji Sax ji dikkal ma, ne ma:
17«Yaw nit ki, tabb naa la wattukatub waa kër Israyil. Nangool sama gémmiñ kàddu, artool ma leen ko.
18Su ma nee nit ku bon ki: “Dee rekk ay sa àtte,” te fekk àrtuwoo ku bon ka, waxuloo lu ko waññee ca mbonam ga, ba mu mucc, ku bon kaay dee ndax tooñam, waaye bakkanam yaw laa koy laaj.

19Waaye su dee yaa àrtu ku bon ki te taxul mu waññiku, dëddu mbonam nag, tooñu boppam a ko reylu, waaye yaw musal nga sa bopp.
20Su dee boroom njekk bu dëpp yoonu njekkam, di def ndëngte, maa koy gàllankoor, mu dee. Soo ko àrtuwul ndax bàkkaaram, dina dee, te deesul bàyyi xel njekkal démbam la, waaye bakkanam, yaw laa koy laaj.
21Waaye nag su dee yaa àrtu boroom njekk bi, ba tax bàkkaaratul, dina dund déy, ndax kàddug àrtu ga, te yaw it musal nga sa bopp.»
22Gannaaw loolu loxol Aji Sax ji dikk na fa ci sama kaw. Mu ne ma: «Génnal ba ci joor gi, ma wax faak yaw.»
23Ma génnsi ba ca joor ga. Ndeke jëmmu leeru Aji Sax jaa nga foofa, taxaw mel ni jëmmu leer, ga ma gisoon ca tàkkal dexu Kebar. Ma ne gurub, dëpp sama kanam fa suuf.
24Ci kaw loolu ngelaw solu ma, ne ma yékkét, ma taxaw. Mu wax ak man, ne ma: «Doxal, tëjuji sa biir néeg.
25Te kat yaw nit ki, dees na la fa takke ay buum, yeew la ba dootoo mana génn, dem ci nit ñi.
26Sa làmmiñ laay taqal ci sa denqleñ, nga luu ba doo leen mana yedd, ndax kërug fippukat lañu.
27Waaye bu ma amee lu ma lay wax, dinaa ubbi sa gémmiñ. Su ko defee nga ne leen: “Lii Boroom bi Aji Sax ji da koo wax.” Kuy dégg, dégg; kuy gàntal, gàntal. Ndax kërug fippukat lañu.»