Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Esekiyel

Esekiyel 37

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Gannaaw loolu loxol Aji Sax ji da maa dikkal. Aji Sax ji yóbboo ma Noowam, ba teg ma ca digg joor ga, fekk joor ga fees dell aki yax.
2Mu wërloo maa wërloo ca biir yax ya, ndeke yax yaa nga bare lool te wow koŋŋ ca biir joor ga.
3Mu ne ma: «Yaw nit ki, ma ne, yii yax man naa dundaat a?» Ma ne ko: «Boroom bi Aji Sax ji, loolu de, yaw doŋŋ a ko xam.»
4Mu ne ma: «Waxal waxyu fi kaw yax yii, ne leen: “Yeen yax yu wow yi, dégluleen kàddug Aji Sax ji:
5Boroom bi Aji Sax ji dafa wax yax yii, ne leen: Maa ngii di leen sol ag noo, ngeen dund.
6Maa leen di may ay siddit, saxal leen aw suux, sànge leen ab der, sol leen ag noo, ngeen dund, ba xam ne maay Aji Sax ji.”»
7Ma biral waxyu na mu ma ko sante. Naka laa biral waxyu rekk, coow daldi jib, ànd akum riir, fekk yax yaay booloo, bu nekk ak ba muy àndal.
8Ma gis ay siddit taq ca, aw suux sax ca kaw, ab der dikk, tege ca kaw, te genn noo amu ca.
9Mu ne ma: «Yaw nit ki, waxalal Noo gi waxyu, waxal ko waxyu ne ko: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Yaw Noo gi, bàyyikool ñeenti yooni ngelaw yi te dikk, wal fi biir ñii ñu bóom, ba ñu dund.”»
10Ma def la mu ma sant, waxyu, noo ga dikk, duggsi, ñu dundaat, jóg taxaw, di gàngoor gu baree bare.
11Mu ne ma: «Yaw nit ki, yax yii ñooy mboolem waa kër Israyil. Ñu ngi naan: “Nun de, ay yaxi neen yu wow koŋŋ lanu, sunu yaakaar tas na, nun kay yàqu nanu.”
12Kon nag biralal waxyu, ne leen: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Yeen sama ñoñ, maa ngii di ubbisi seeni bàmmeel, dekkale leen ca seeni bàmmeel, délloosi leen kaw suufas Israyil.
13Yeen sama ñoñ, bu ma ubbee seeni bàmmeel, ba yékkatee leen ca seeni bàmmeel, dingeen xam ne maay Aji Sax ji.
14Maa leen di sol samag noo, ngeen dund, ma samp leen seen suufas bopp, ba ngeen xam ne man Aji Sax ji maa wax, maa def. Kàddug Aji Sax jee.”»
15Ba loolu wéyee kàddug Aji Sax ji dikkal ma ne ma:
16«Yaw nit ki, sàkkal aw dénk, nga bind ci kaw lii: “Ñeel Yuda ak giiri Israyil yi mu àndal.” Nga sàkkaat weneen dénk, bind ci kawam: “Ñeel Yuusufa bantub Efrayim ak waa kër Israyil yi mu àndal,”
17te nga boole ñaari dénk yi, ñu booloo, di wenn dénk ci sa loxo.
18Bu la sa bokk yi laajee, ne la: “Xanaa doo nu wax lii lu muy tekki?”

19nanga leen wax ne leen: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Maa ngii di jël dénku Yuusufa wi ci loxol Efrayim, mook giiri Israyil yi mu àndal, boole kook dénku Yuda, daldi def lépp wenn dénk, ñu booloo di wenn ci sama loxo.”
20«Nanga ŋàbb dénk yi nga bind, ñuy gis,
21te nga wax leen ne leen: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Maa ngii di jëleji bànni Israyil ca biir xeet ya ñu fekki, dajalee leen wet gu nekk, délloosi leen seen suufas bopp.
22Maa leen di def wenn xeet doŋŋ ci réew mi, ci kaw tundi Israyil, ñoom ñépp bokk benn buur. Dootuñu doon ñaari xeet te dootuñu xàjjalikoo ñaari nguur.
23Dootuñu sobeel seen bopp ci ay kasaray tuur, ak seen jëf ju siblook mboolem seeni tooñ. Maa leen di walloo ci mboolem seen ñàkk kóllëre. Ma setal leen, ñu doon sama ñoñ, ma doon seen Yàlla.
24«“Daawuda sama jaam baay doon seen buur, di seen bennub sàmm ñoom ñépp. Sama àttey yoon lañuy doxe, sama dogali yoon lañuy sàmm, di ko jëfe.
25Ñooy dëkke réew mi ma joxoon Yanqóoba sama jaam ba, te seeni maam dëkke woon ko. Ñu dëkke ko ñoom it, ñook seeni doom ak seeni sët, ba fàww, te Daawuda sama jaam ba mooy doon seen boroom jal ba fàww.
26Maay fas ak ñoom kóllëreg jàmm, gu sax. Maa leen di samp, ful leen, maay samp sama bérab bu sell fi seen biir, ba fàww,
27sama dëkkuwaay nekk fi seen biir, may seen Yàlla, ñuy sama ñoñ.
28Bu sama bérab bu sell nekkee fi seen biir ba fàww, xeet yi dinañu xam ne man Aji Sax ji maa sellal Israyil.”»