1Kàddug Aji Sax ji dikkal na ma ne ma:
2«Yaw nit ki, waxal Boroom Tir, ne ko: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Dangaa fuuy ba naan: ‘Maay Yàlla, ji tooge toogub yàlla yi, fi xolu géej!’ Waaye yaw doom aadama nga, doo Yàlla, dangay yàlla-yàllalu rekk.
3Xëy na yaa sut Dañeel am xel, du genn kumpa gu la ump!
4Sam xel ak sa manoore nga ame alal, am wurus, am xaalis, yeb ci say denc.
5Sa xelum jula mu réy nga yokke sa alal, alal ji tax laa fuuy.
6Moo tax Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Gannaaw dangay yàlla-yàllalu,
7maa ngii di la indil ay làkk-kat, yéefar yi gëna néeg. La nga sottale xel mu rafet, ñoo koy boccil saamar, te ñooy yàq sab taar.
8Pax lañu lay tàbbal, nga deeyi xolu géej deewug ku ñu bóom.
9Xanaa doo janook ki lay rey, naati yaay yàlla? Boo tàbbee ca sa loxoy jamkat ya, keroog nga noppee doon yàlla, di nitu kese.
10Deewug yéefar bu xaraful ngay deeye ci loxol làkk-kat yi. Man déy, maa ko wax! Kàddug Boroom bi Aji Sax jee.”»
11Kàddug Aji Sax ji dikkalati ma ne ma:
12«Yaw nit ki, yékkatilal buurub Tir kàddug jooy! Nga ne ko: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Yaa matoon royukaay, géejum xel, sottib taar.
13Yaa nga woon biir Àjjana, toolub Yàlla ba, ràngoo lépp luy gànjari per, sarduwan ak topaas ak jamaa ak kirsolit ak onigsë ak jàspë ak safiir ak emëródd ak eskarbukal. Fegukaay yaak wewukaay ya di wurus, te bés ba ñu la sàkkee, fekk na ñu waajal yooyu.
14Yaa doon malaakam serub mu ne ràññ, di aare, ma tabb la fa kaw tundu Yàlla wu sell wa, ngay daagoo digg doj yuy tàkk.
15Ba ñu la sàkkee, nga dale mat ci say jëfin, ba keroog njubadi di feeñ ci yaw.
16Sa liggéeyu jula bu yaatu moo la feesal fitna, nga bàkkaar, ba ma nangoo sa teddnga fa tundu Yàlla wa, sànk la, yaw malaakam serub miy aare, nga jóge digg doj yuy tàkk.
17Sab taar a la fuuyloo, sa daraja tax nga yàq sam xel! Fi suuf laa la rattax, fi kanam buur yi laa la detteel, ñu di la seetaan.
18Sa ñaawtéef yu bare ak njublaŋ gi ngay julaa, looloo teddadil sa jaamookaay yu sell, ba ma jafale sawara fi sa biir, mu xoyom la. Maa la def ub dóom fi suuf, ñépp di la xool.
19Mboolem ñi la xam ci xeet yi, seen yaram dina daw ci yaw. Ku raglu ngay doon, te doo tekkeeti ba fàww.”»
20Kàddug Aji Sax ji dikkalati ma ne ma:
21«Yaw nit ki, neel jàkk Sidon, nga biral waxyu fi kawam.
22Neel: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Yaw Sidon, maa ngii fi sa kaw. Dees na ma sargal fi sa biir, ba ñu xam ne maay Aji Sax ji ndax mbugal yi ma fiy wàccesi, ba fésal fi sama sellnga.
23Maa fiy yebal mbas, deret tuuroo mbedd yi, saamar dajal dëkk bi, bóom nit ñi, tëral, ba ñu xam ne maay Aji Sax ji.”
24«Su boobaa waa kër Israyil, seen dëkkandoo yi leen di sewal, dootuñu leen lëjal ni dagg yu ñaw ak dég yuy jame. Su boobaa ñu xam ne maay Boroom bi Aji Sax ji.
25«Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Bu may dajale waa kër Israyil, di leen jële digg xeet yi ñu tasaaroo, ca laay fésal sama sellnga fa seen biir, yéefar yi gis, ñu dëkke seen suufas bopp, sa ma joxoon Yanqóoba sama jaam ba.
26Xel mu dal lañu fay dëkke, tabax fa ay kër, jëmbat seeni reseñ. Bu ma wàcceelee ay mbugal mboolem ñi leen di sewal te séq leen, dinañu dëkke ba xam ne maay seen Yàlla Aji Sax ji.»