Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Esekiyel

Esekiyel 29

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Ca fukkeelu at ma, fukki fan ak ñaar ca fukkeelu weer wa, kàddug Aji Sax ji dikkal na ma ne ma:
2«Yaw nit ki, neel jàkk Firawna buuru Misra, nga biral waxyu fi kawam ak fi kaw Misra gépp.
3Waxal, nga ne: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Maa ngii fi sa kaw, yaw Firawna buuru Misra, yaw ninki-nànka ju mag ji goore sa diggi dex, te naan: ‘Maa moom sama dex, man ci sama bopp maa ko sàkk!’
4Waaye maay we ay lonku ci say ŋaam, jël sa jëni waltan, ŋoyal leen ci say waasintóor, diree la say waltan, sa jëni waltan yépp ŋoy ci say waasintóor.
5Ma wacc la ca màndiŋ ma, yaw yaak mboolem sa jëni waltan. Ci àll bi nga naa ñàyy, deesu la for, deesu la fat. Dundooti àll beek njanaaw yi, yaw laa leen di leele,
6ba waa Misra gépp xam ne maay Aji Sax ji. «“Seen ndimbal ak Israyil mooy ndimbalu bantu barax,
7ñu jafandu ko, mu ne tàllit, ne xureet mbagg yépp, ñu wéeroo ko, mu ne tipp, ndigg yépp rëcc.
8«“Moo tax Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Yaw Misra, maa ngii di la indil saamar, ba dagge fi yaw nit ak mala.
9Réewum Misraay gental, di ndànd-foyfoy, ba ñu xam ne maay Aji Sax ji. Moo ne: ‘Dex gi maa ko moom, man maa ko sàkk!’
10Moo tax maa ngii fi sa kaw, yaak say wali dex. Maay def réewum Misra gent bu ne sereŋ, mu gentale Migadol ca bëj-gànnaar, ba Asuwan, fa mu digalook réewum Kuus ca bëj-saalum.
11Tànku doom aadama du fa jaare, tànku mala du fa jaare, te deesu fa dëkke diiru ñeent fukki at.
12Maay def Misra gëna gental ci réew yi gental, ay dëkkam gëna gental ci dëkk yi diiru ñeent fukki at. Maay tasaare waa Misra ci biir xeet yi, wasaare leen ci biir réew yi.
13Boroom bi Aji Sax ji déy dafa wax ne: Bu ñeent fukki at yi matee, ma dajalee waa Misra fa digg xeet ya ñu tasaaroo woon.
14Ca laay tijjee wërsëgu Misra, delloo leen réewum Pattros ca bëj-saalum, seen réewum cosaan, ñu doon fa nguur gu suufe,
15gëna suufe ci nguur yi, ba dootuñu damu fi kaw xeet yi. Maa leen di tuutal ba dootuñu yilif xeet yi.
16Waa kër Israyil dootuñu yaakaar Misra, xanaa ñuy fàttliku na ñu ñaawe woon démb, ba ñuy làqoo waa Misra, te dinañu xam ne maay Boroom bi Aji Sax ji.”»
17Ca ñaar fukkeelu at maak juróom ñaar, benn fan ca weer wa jëkk, kàddug Aji Sax ji dikkal na ma, ne ma:
18«Yaw nit ki, Nabukodonosor buuru Babilon teg na mbooloom xareem, coono bu metti ca seen xareek Tir. Seen kawari bopp yépp ruus na, seen wagg yépp tëccu, te coonoom ba mu sonn ca Tir, yooloowu ca dara, du moom, du ay nitam.

19«Moo tax Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Maa ngii di jox réewum Misra, Nabukodonosor buuru Babilon, mu yóbbu alal ja, wëq ko ba mu set, sëxëtoo mboolem lu mu amoon, muy peyooru mbooloom xareem,
20di yoolu coonoom. Maa ko jox réewum Misra, feye ko la ma ay nitam liggéeyal. Kàddug Boroom bi Aji Sax jee.
21Bésub keroog maay yokk dooley waa kër Israyil, yaw nit ki, ma jox la sañ-sañu àddu fi seen biir. Su boobaa ñu xam ne maay Aji Sax ji.»