Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - 2.Buur ya - 2.Buur ya 10

2.Buur ya 10:7-27

Help us?
Click on verse(s) to share them!
7Ba bataaxal ba agsee, kàngam yooyu boole doomi buur yu góor ya, rendi, ñuy juróom ñaar fukki góor. Ñu yeb seeni bopp ciy dàmba, yónnee Yewu ca Yisreel.
8Ndaw la agsi ne ko: «Indi nañu boppi doomi buur ya.» Yewu ne: «Defleen ko ñaari jal ca buntu dëkk ba, ba ëllëg.»
9Ca ëllëg sa mu génn taxaw ca kanam mbooloo mépp ne: «Yeen defuleen dara. Man mii maa fexeel samab sang, rey ko. Waaye ana ku bóom ñii ñépp?
10Kon xamleen ne du lenn luy fanaan àll ci kàddug Aji Sax ji ci li mu wax ci waa kër Axab. Aji Sax ji sottal na la mu waxoon, Ilyaas jaamam ba jottli ko.»
11Ba mu ko defee Yewu rey mboolem ña desoon ca kër Axab ca Yisreel ak mboolemi kàngamam aki jegeñaaleem aki sarxalkatam, bàyyiwu ca kenn, mu rëcc.
12Gannaaw loolu Yewu fabu jëm Samari. Ba mu demee ba tollook Bet Eket, ca sàmm sa,
13daldi dajeek bokki Akasiya buurub Yuda. Mu ne leen: «Yeenay ñan?» Ñu ne ko: «Bokki Akasiya lanu. Danuy nuyuji doomi Buur Axab, ak doomi Lingeer yaayu Buur.»
14Mu ne: «Jàppleen leen!» Ñu jàpp leen, dem rendi leen ca wetu teenu Bet Eket; ñuy ñeent fukk ak ñaar, bàyyiwuñu ca kenn, mu rëcc.
15Ba loolu wéyee Yewu bàyyikoo fa, gis Yonadab doomu Rekab, mu dikk dajeek moom. Mu nuyook moom, ne ko: «Mbaa ni ma fareek yaw te muy dëgg, ni nga fareek man te muy dëgg?» Yonadab ne ko: «Waawaaw.» Yewu ne ko: «Kon nag jox ma sa loxo!» Mu jox ko loxo; mu xëcc ko, yéege ko ca watiir ba,
16ne ko: «Ñëwal nu dem rekk, nga gis ni ma farloo ci mbiri Aji Sax ji.» Mu waral ko watiiram, yóbbu ko.
17Ba Yewu àggee Samari, daa rey mboolem ña desoon ca waa kër Axab ca Samari, faagaagal leen, muy la Aji Sax ji waxoon Ilyaas.
18Ba mu ko defee Yewu woo mbooloo ma mépp, ne leen: «Axab tuuti la jaamu Baal. Man Yewu bu baax laa koy jaamu.
19Ayca, wool-leen ma yonenti Baal yépp ak sarxalkatam yépp ak jaamukatam yépp. Bu kenn wuute, ndax sarax bu réy laay defal Baal. Képp ku ko wuute dina dee.» Booba Yewoo ngi fexee nax ñiy jaamu Baal, ba rey leen.
20Yewu ne leen: «Beral-leen Baal am ndaje.» Ñu yéene.
21Yewu nag yónnee ca Israyil gépp; mboolem ñay jaamu Baal dikk, kenn desul. Ci kaw loolu, ñu dugg kër Baal, ba kër ga fees dell.
22Yewu ne ka yor cummikaay la: «Képp kuy jaamu Baal, indil ko mbubb.» Mu indil leen ay mbubb.
23Ba loolu amee Yewu ànd ak Yonadab doomu Rekab, duggsi biir kër Baal. Mu ne jaamukati Baal ya: «Xool-leen bu baax, ba gis ne yéenu neen la, te jaamukati Aji Sax ji raxu leen, xanaa jaamukati Baal rekk.»
24Ña ngay dugg, ne dañuy def ay saraxi rendi-dóomal ak yeneen sarax. Fekk na Yewu teg ca biti juróom ñett fukki nit, ne leen: «Ku ci bàyyi kenn ci ñi ma leen reyloo, ba mu rëcc, sa bakkan ngay feye bakkanam.»
25Ba ñu noppee ca saraxi rendi-dóomal ya, Yewu ne dag yaak jawriñi xarekat ya: «Duggleen, fàdd leen. Bu kenn génn.» Ñu daldi leen leel ñawkay saamar, ñu daanu. Dag yaak jawriñ ya sànni néew ya ca biti, ba noppi dugg ca néegu Baal ba gëna biire.
26Ñu génne tuuri doj ya sampe woon ca kër Baal, lakk ko.
27Dañoo daane jëmmi Baal ja, màbb kër Baal, boole ca, def kob sën, te moom la ba tey jii.

Read 2.Buur ya 102.Buur ya 10
Compare 2.Buur ya 10:7-272.Buur ya 10:7-27