1Ca ay jantam la Nabukodonosor buuru Babilon song réew ma. Yowakim nangul ko diiru ñetti at, doora walbatiku fippu.
2Ci kaw loolu Aji Sax ji yebal ci kawam ay yàqkati waa Babilon ak yàqkati Siri ak yàqkati Mowab ak yàqkati Amoneen ña. Aji Sax ji yebal leen Yuda ngir ñu yàqte ko, mu dëppook kàddu ga mu waxoon, yonent yiy surgaam jottli ko.
3Ci ndigalal Aji Sax ji moos la loolu xew ca Yuda, ba mu mujj leen xarab ndax bàkkaari Manaseek li mu def lépp,
4ak deretu nit ñi mu tuur te defuñu dara; ndax Manase daa feesal Yerusalem ak deretu jaamburi Yàlla, ba Aji Sax ji nanguwu koo baal.
5Li des ci mbiri Yowakim ak mboolem lu mu def, bindees na ko moos ci téere bi ñu dippee Jaloorey buuri Yuda ca seeni jant.
6Gannaaw gi Buur Yowakim tëdd, fekki ay maamam. Doomam Yowakin nag falu buur, wuutu ko.
7Jamono yooyu buuru Misra génnatul réewam di xareji, ndax fekk na buuru Babilon nangu suufam sépp la ko dale ca xuru Misra ba ca dexu Efraat.
8Fukki at ak juróom ñett la Yowakin amoon ba muy falu buur. Ñetti weer la nguuru, péeyoo Yerusalem. Yaayam mooy Newusta doomu Elnatan ma cosaanoo Yerusalem.
9Muy def li Aji Sax ji ñaawlu, mboolem noonee ko baayam defe woon.
10Jamono jooja la jaraafi Nabukodonosor buuru Babilon, song Yerusalem, gaw dëkk ba.
11Nabukodonosor dikk ca dëkk ba, fekk ay jaraafam gaw ko.
12Yowakin buurub Yuda génn fekki buuru Babilon, jébbal ko boppam, mook ndeyam aki surgaam aki jaraafam ak jawriñi këram. Buuru Babilon nag jàpp ko. Looloo nga yemook juróom ñetteelu atu nguurug Nabukodonosor buuru Babilon.
13Nabukodonosor jële fa mboolem alali kër Aji Sax ji ak alali kër Buur, daldi buub lépp luy ndabu wurus lu Suleymaan buurub Israyil defarlu woon ci kër Aji Sax ji, muy la Aji Sax ji waxoon.
14Ci biir loolu buuru Babilon yóbbu Yerusalem gépp, muy mboolem jaraaf yeek jàmbaari góor ñi, ñuy fukki junni, ñook mboolem liggéeykat yaak tëgg ya. Kenn desul, lu moy baadoola ya gëna néew doole.
15Mu yóbbu Yowakin Babilon mook ndeyam aki soxnaam aki jawriñam ak kilifay réew ma.
16Buuru Babilon boole ca jàppaale juróom ñaari junniy jàmbaari góor (7 000), ak junniy liggéeykat aki tëgg, ñoom ñépp di boroom kàttan te tollu ci xare; mu boole leen jàpp jaam, yóbbu Babilon.
17Buuru Babilon moo fal Mataña, baayu Yowakin bu ndaw, mu wuutu Yowakin, daldi soppi turu Mataña, tudde ko Cedekiya.
18Ñaar fukki at ak benn la Cedekiya amoon ba muy falu buur, te fukki at ak benn la nguuru fa Yerusalem. Yaayam mooy Amutal doomu Yeremi ma cosaanoo Libna.
19Muy def li Aji Sax ji ñaawlu, mboolem noonee ko Yowakim defe woon.
20Merum Aji Sax ji nag dikkal Yerusalem ak Yuda, ba mu mujj xarab leen. Gannaaw gi Cedekiya fippu buuru Babilon.