Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - 2.Buur ya

2.Buur ya 6

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Am na bés mbooloom yonent ya wax Alyaasa ne ko: «Xoolal, fii nuy dajeek yaw daa xat.
2Nan dem ngalla ba ca tàkkal dexu Yurdan, ku nekk ci nun sàkk fa aw dénk, nu defaral fa sunu bopp bérab bu nu daje.» Alyaasa ne leen: «Demleen.»
3Kenn ca ñoom ne ko: «Sang bi, ñëwal nu dem kay!» Mu ne ko: «Waaw, nan dem.»
4Mu ànd ak ñoom dem ba ca dexu Yurdan, di fa gor ay garab.
5Kenn ca ñoom doon gor, weñu sémmiñam wadd ca ndox ma. Mu jalu, ne: «Éy, sang bi, te dama koo àbboon kat!»
6Góoru Yàlla ga ne ko: «Fu mu wadd?» Mu won ko fa mu wadd, mu dog bant sànni foofa, weñ ga tëmb.
7Mu ne ko: «Foral!» Mu yóotu, for ko.
8Bu loolu wéyee buurub Siri doon na xareek Israyil. Ci biir loolu mu diisooki surgaam, ne leen bérab sàngam lay def ab dalam.
9Ci kaw loolu góoru Yàlla ga yónnee ca buurub Israyil, ne ko: «Nanga moytoo jaare bérab sàngam, ndaxte fa la waa Siri jëm.»
10Buurub Israyil yónnee fa ko góoru Yàlla ga wax, ngir nemmiku foofa. Alyaasa di artoo Buur noonu, muy fàggandiku. Loolu am na bu dul benn yoon, du ñaar.
11Buurub Siri nag jàq lool ci loolu, daldi woolu ay jawriñam ne leen: «Ana kan ci yeen moo fi nekkal buurub Israyil?»
12Kenn ca jawriñ ya ne ko: «Du kenn, Buur sang bi; waaye Alyaasa, yonent bi ci Israyil mooy jottli buurub Israyil kàddu yi ngay wax ci sa biir néegu biir.»
13Mu ne: «Seetalileen ma ko, ma yónnee, jàpp ko.» Ñu mujj xamal ko ne: «Moom de, ma nga ca Dotan.»
14Buurub Siri yebal fa ay dag yu takku, yóbbaale ay fas aki watiir. Mu agsi guddi, gaw dëkk ba.
15Ci kaw loolu bëkk-néegub góoru Yàlla ga jóg ca suba teel, génn, gisul lu moy mbooloom xare mu gaw dëkk ba, aki fas aki watiir. Mu ne ko: «Éy sang bi, fu nu jëm?»
16Alyaasa ne ko: «Bul tiit, noo leen ëpple ñu ñu àndal.»
17Alyaasa nag ñaan ne: «Aji Sax ji, ngalla ubbil ay bëtam, mu gis.» Aji Sax ji ubbi bëti surga ba, mu xool, ndeke tund waa nga fees aki fas aki watiiri sawara, wër Alyaasa.
18Ba mu ko defee waa Siri wutsi Alyaasa, mu ñaan ci Aji Sax ji ne ko: «Rikk muural bëti mbooloo mii.» Aji Sax ji muur seeni bët, na mu ko ko ñaane.

19Alyaasa nag ne leen: «Fii du yoon wi de, te du dëkk bi ngeen di seet it. Toppleen ma, ma yóbbu leen ci ki ngeen di seet.» Mu daldi leen yóbbu ba Samari.
20Ba ñu duggee Samari, Alyaasa dellu ñaan ne: «Aji Sax ji, ngalla ubbil bëti nit ñii, ñu gis.» Aji Sax ji muri seeni bët, ñu xoole rekk, gis ne ñu ngi biir Samari.
21Buurub Israyil gis leen ne: «Baay Alyaasa, ma rey leen? Ãa, ma rey leen?»
22Mu ne ko: «Bu leen rey mukk. Xanaa ñoo jàpp cib xare sax doo leen rey? May leen ñu lekk, naan, te dellu ca seen sang.»
23Ba loolu wéyee Buur berndeel leen bernde ju réy; ñu lekk, naan; mu yiwi leen, ñu ñibbi ca seen sang. Booba la waa Siri gëjoona def gàngoori yàqkat, di dugg biir réewum Israyil.
24Ba ñu demee ba yeneen jamono, Ben Addàd buurub Siri woo mbooloom xareem mépp, dem gawi Samari.
25Xiif bu metti am ca Samari ndax gaw ba, ba boppub mbaam-sëf di jar juróom ñett fukki dogi xaalis, genn-wàll liibaru jonkanu pitax di jar juróomi dogi xaalis.
26Mu am bés buurub Israyil jaar ca kaw tata ja, senn as ndaw àddu ca kaw ne ko: «Buur, sang bi, ngalla wallu ma!»
27Mu ne ko: «Bu la Aji Sax ji walluwul, nu ma lay walloo? Du pepp, du ndoxum reseñ ju ma la mana may.»
28Mu teg ca ne ko: «Lan la sax?» Ndaw sa ne ko: «Ndaw sii da ma noon: “Indil sa doom, nu lekk ko tey, ëllëg nu lekk sama doom.”
29Nu togg sama doom, bokk ko lekk. Ma ne ko: “Su ëllëgee indil sa doom, nu bokk ko lekk.” Moom nag mu làq doomam.»
30Ba Buur déggee kàdduy ndaw sa, daa xotti mbubbam ndaxu naqar. Ma ngay dox, di wéy ca kaw tata ja, mbooloo ma tollu ci suuf séenuñu lu moy saaku bi mu def njiitlaay, di ko ñaawloo.
31Ma nga naan: «Yal na ma Yàlla teg mbugal mu gëna tar ndegam bésub tey jii boppub Alyaasa doomu Safat du teqlikook baatam.»
32Fekk na Alyaasaa nga ca këram toog, mag ña bokk toog ak moom. Buur yebal ndaw ca moom. Ndaw la agseegul, Alyaasa ne mag ña: «Xool-leen bóomkat bii yebal kuy dogsi sama bopp! Xam ngeen lan la, bu ndaw li agsee rekk, tëjleen bunt bi, tere koo dugg; ndax du tànki sangam laay dégg, mu topp ci moom sax?»
33Naka la Alyaasa di wax, ndaw la ne jimeet, jëm ca moom. Ma nga naan: «Gis nga musiba mii Aji Sax ji wàcce. Kon ana lu may séentooti ci Aji Sax ji?»