Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - 2.Buur ya

2.Buur ya 25

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Ba Cedekiya tolloo ci juróom ñeenteelu atu nguuram, fukki fan ca fukkeelu weeram, ca la Nabukodonosor buuru Babilon ànd ak mbooloom xareem mépp ci kaw Yerusalem. Ñu dal fa janook ñoom, yékkati gawukaay, wërale ko.
2Dëkk ba gawe, ba keroog Cedekiya tollu ci fukkeelu atu nguuram ak benn.
3Keroog juróom ñeenti fan ca weer wa, xiif ba tar lool ca biir dëkk ba, ba waa réew ma amatuñu ab dund.
4Xarekati Yuda ya génn guddi daw. Fekk na waa Babilon gaw dëkk ba. Teewul ñu rëcc, jaare ca bunt ba ca diggante ñaari tata ya, ca wetu toolu buur. Cedekiya daldi wuti xuru Yurdan.
5Waa Babilon nag topp Buur Cedekiya, ba dab ko ca jooru Yeriko, fekk mbooloom xareem mépp tasaaroo, wacc ko.
6Ñu jàpp ko, yóbbu ko ca buuru Babilon ca dëkk ba ñuy wax Ribla. Ñu dogal fa àtteem.
7Doomi Cedekiya yu góor lañu rendi, muy gis, ba noppi ñu tuur ay bëtam, jénge ko jéngi xànjar, yóbbu ko Babilon.
8Ba Nabukodonosor buuru Babilon tolloo ci fukkeelu atu nguuram ak juróom ñeent, ba am juróom ñaari fan ca juróomeelu weeru at ma, ca la bëkk-néegu buuru Babilon, Nebusaradan njiitu dag ya, dugg Yerusalem.
9Mu taal kër Aji Sax ji, taal kër Buur, ak këri Yerusalem gépp, boole ca këri boroom barke ya.
10Gàngooru Babilon gépp daldi ànd ak njiital dagi buur, ñu màbb tata ya wër Yerusalem.
11Gannaaw gi ña nekkoon ca dëkk ba ba booba, ak ña jébbaloon seen bopp buuru Babilon ak la desoon ca waa réew ma, Nebusaradan njiital dagi buur, boole leen yóbbu ngàllo.
12Teewul ñenn ca baadooloy réew ma, njiital dag ya bàyyi leen fa, ñuy liggéey tóokëri reseñ yaak tool ya.
13Ci biir loolu kenuy xànjar ya woon ca kër Aji Sax ji ak rootukaay yaak mbalkam xànjar ma, waa Babilon toj lépp, boole xànjar ja, yóbbu Babilon.
14Ñu yóbbaale mboolem ndabi xànjar yi ñuy liggéeye ci kër Aji Sax ji; ndab yiy def dóom, ak ñiitukaay yi, ak ñiimi feyukaayi làmp yi, ak ndab yiy def deretu sarax yi, ak mboolem jumtukaayi xànjar yu ñuy sarxalee.
15Njiital dag ya yóbbaale and yaak ndab yiy def deret. Lu ciy wurus, mu ber, lu ciy xaalis, mu ber.
16Ñaari kenu yooyu ak mbalka maak rootukaay ya, lépp di xànjar bu Suleymaan defaraloon kër Aji Sax ji, maneesula takk diisaay ba.
17Taxawaayu kenu gu ci nekk fukki xasab laak juróom ñett. Ab ponkub xànjar a ci tege, bu taxawaay ba di ñetti xasab. Ab caax wodd ponk bi, ànd ak doomi gërënaati xànjar. Ñaari kenu yépp noonu, ànd ak seeni caax.
18Ci kaw loolu njiital dag ya jàpp Seraya sarxalkat bu mag ba, ak Cefaña sarxalkat ba ca topp, ak ñetti dagi bunt kër Aji Sax ja.

19Biir dëkk ba nag mu jële fa jenn jawriñ ju jiite ay xarekat, ak juróomi niti dëkk ba ñu sës ci Buur, ak bindkatub njiital xare ba sasoo bind xarekat yi, ak juróom benn fukki Yudeen ñu mu fekk ca biir dëkk ba.
20Ba mu ko defee Nebusaradan, njiital dagi buur, boole leen yóbbu ca buuru Babilon ca Ribla.
21Buuru Babilon nag jam leen, ñu dee, foofa ca Ribla, ca réewum Amat. Noonu la Yuda génne réewam, dem ngàllo.
22Mbooloo ma des ca réewum Yuda te Nabukodonosor buuru Babilon bàyyi leen fa nag, Gedalya doomu Ayikam doomu Safan la tabb mu jiite leen.
23Ba mboolem kilifay xare ya déggee ñook seeni nit ne buuru Babilon fal na Gedalya, dañoo ànd dikk ca Gedalya ca Mispa. Kilifa yooyu Ismayil doomu Netaña la woon, ak Yowanan doomu Kareya, ak Seraya doomu Tanumet ma dëkk Netofa, ak Yaasaña doomu waa Maaka ba, ñook seeni nit.
24Gedalya giñal leen ne leen: «Buleen ragala bokk ci surgay waa Babilon. Toogleen ci réew mi te nangul buuru Babilon, muy seen jàmm.»
25Gannaaw gi, ca juróom ñaareelu weeru at ma, Ismayil doomu Netaña doomu Elisama, bokk ci askanu buur, ànd ak fukki nit, dikk bóom Gedalya, bóomaale waa Yudak waa Babilon ya nekkoon ak moom ca Mispa.
26Ci kaw loolu mbooloo mépp fabu, baadoolook boroom barke, ñook kilifay xarekat ya, ñu daldi daw dem Misra ndax ragal waa Babilon.
27Yóbbu nañu Yowakin buurub Yuda ngàllo ba mu am fanweeri at ak juróom ñaar, Ewil Merodag doora falu buur ca Babilon. At mooma, fukkeelu weer waak ñaar, ñaar fukki fan ak juróom ñaar ca weer wa, ca la Ewil Merodag siggil Yowakin buurub Yuda, daldi koy tijji.
28Ci biir loolu mu rafetook moom, jox ko cér bu sut cér ba mu jox yeneen buur ya mu bokkal curga ca Babilon.
29Yowakin nag teqlikook yérey kaso ya, ba noppi ñu may ko muy bokk ak Buur ndab giiru dundam.
30Ci biir loolu ñu dogal ko njëlam lu sax dàkk, bàyyikoo ci Buur bés bu jot, giiru dundam.