Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - 2.Buur ya

2.Buur ya 8

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Am na bés Alyaasa wax ndaw sa mu dekkaloon doomam ju góor ne ko: «Ayca, àndal ak sa njaboot, ngeen dali fu ngeen mana dal, ndax Aji Sax ji dogal na ab xiif ci réew mi, te dina am juróom ñaari at.»
2Ndaw sa fabu, def la ko góoru Yàlla ga wax, dem yoonam mook njabootam, dali ca réewum Filisteen ña, toog fa diiru juróom ñaari at.
3Ba juróom ñaari at ya matee, ndaw sa jóge ca réewum Filisteen ña, ñibbsi. Mu dem ca Buur, di sàkku mu delloo ko këram ak suufam.
4Loolu fekk Buur di waxtaan ak Gewasi, surgab Alyaasa góoru Yàlla ga, naan ko: «Ayca, wax ma mboolem jaloore yi Alyaasa def.»
5Gewasi nag di nettali Buur na Alyaasa dekkalee woon xale ba, rekk ndaw sa Alyaasa dekkaloon doomam ju góor ne jalañ, di sàkkusi ca Buur mu jox ko këram ak suufam. Gewasi ne ko: «Ndaw saa ngii nag, Buur, sang bi. Doomam ju góor jii la Alyaasa dekkaloon.»
6Buur laaj ndaw sa, mu wax ko lépp. Buur boole kook bëkk-néegam ne ko: «Fexeel ba ñu delloo ndaw sii lépp luy alalam ak dayob lépp lu suufam meññoon, la ko dale ca bés ba mu fi jógee ba tey jii.»
7Am na it yoon wu Alyaasa demoon Damaas, péeyu Siri. Fekk Ben Addàd buurub Siri wopp. Ba ñu ko waxee ne ko: «Góoru Yàlla gi ñëw na fi.»
8Buur ne Asayel, ab jawriñam: «Demal ca góoru Yàlla ga te yóbbaale loo teg ci loxoom, mu seetal ma ci Aji Sax ji. Laajal ma ko ne ko: “Ndax dinaa jóg ci sama wopp jii?”»
9Asayel dem ca moom, yóbbaale lu mu ko jox, muy mboolem la gën ca Damaas, tollu ci sëfub ñeent fukki giléem. Mu dikk taxaw ca kanamam, ne ko: «Ben Addàd buurub Siri moo ma yónni fi yaw, ne ma: “Laajal ma Baay Alyaasa ndax dinaa jóge ci sama wopp jii.”»
10Alyaasa ne ko: «Demal ne ko dina jóg moos, waaye Aji Sax ji won na ma ne dina dee déy!»
11Ba loolu amee góoru Yàlla ga ne dann, ne ko jàkk, ba Asayel rus. Mu daldi jooy.
12Asayel ne ko: «Sang bi, looy jooy?» Mu ne ko: «Damaa xam lu bon li ngay defi waa Israyil. Seeni tata ngay taal, seeni xale yu góor nga jam saamar ñu dee, seeni doom nga tas ci suuf, seeni jigéeni biir nga butti.»
13Asayel ne ko: «Moo sang bi, man mi ab xaj gën, nu ma mana defe jooju jëf ju réy?» Alyaasa ne ko: «Aji Sax ji won na ma ne yaay doon buurub Siri.»
14Asayel bàyyikoo ca Alyaasa, dellu ca sangam. Mu ne ko: «Lu la Alyaasa wax?» Mu ne ko: «Nee na ma de dinga jóg moos.»
15Ca ëllëg sa nag Asayel fab malaan, xooj ko ci ndox, dëpp ko ca kanamu buur ba, fatt ko, mu dee. Gannaaw loolu Asayel falu buur, wuutu ko.
16Ba buurub Israyil Yoram doomu Axab duggee juróomeelu atu nguuram, ca la Yoram doomu Yosafat buurub Yuda falu buur ca Yuda.
17Fanweeri at ak ñaar la amoon ba muy falu buur, te juróom ñetti at la nguuru fa Yerusalem.
18Tànki buuri Israyil la topp, di roy waa kër Axab, ndax doomu Axab la jël jabar, di def li Aji Sax ji ñaawlu.

19Waaye Aji Sax ji bugguloona tas Yuda ngir Daawuda, jaamam ba, ndax la mu ko digoona may ci ay doomam kuy saxal nguuram fàww, ba du fey.
20Ca jamonoy Yoram la Edomeen ña fippu, bañ moomeelu Yuda, ba fal seen buuru bopp.
21Gannaaw loolu Yoram jàll ba Sayir, yóbbaale watiiri xareem yépp. Moo jóg ag guddi, dal ca kaw Edomeen ña leen gawoon, moom ak njiiti watiiri xareem. Waaye gàngooru Yuda ñoo daw, dellu ca seeni xayma.
22Edomeen ñaa ngi bañ moomeelu Yuda ba tey jii. Jant yooyu la Libna itam fippu.
23Li des ci mbiri Yoram ak mboolem lu mu def, bindees na ko moos ci téere bi ñu dippee Jaloorey buuri Yuda ca seeni jant.
24Yoram nag tëdd, fekki ay maamam, ñu denc ko ca bàmmeelu maamam ca gox ba ñu naan Kër Daawuda. Doomam Akasiya falu buur, wuutu ko.
25Ba Yoram doomu Axab buurub Israyil duggee ca fukkeelu atu nguuram ak ñaar, ca la Akasiya doomu Yoram falu buur ca Yuda.
26Ñaar fukki at ak ñaar la Akasiya amoon ba muy falu buur, te menn at la nguuru fa Yerusalem. Atalyaa mooy yaayam, sëtub Omri buurub Israyil.
27Akasiya topp ca tànki waa kër Axab, di def li Aji Sax ji ñaawlu ni waa kër Axab, ndax goro la woon ca waa kër Axab.
28Akasiya ànd naak Yoram doomu Axab, xarejeek Asayel buurub Siri ca Ramot Galàdd. Waa Siri jam Yoram.
29Buur Yoram nag walbatiku fajuji ca Yisreel ndax jam-jami waa Siri ya ca Raama, ba muy xareek Asayel buurub Siri. Doomu Yoram, Akasiya buurub Yuda nag dem seeti Yoram doomu Axab fa Yisreel ndax jagadeem ga.