Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - 2.Buur ya

2.Buur ya 2

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Bés ba Aji Sax jiy yóbbu Ilyaas kaw asamaan ci biir callweer, ma nga bàyyikoo woon Gilgal, ànd ak Alyaasa.
2Ci biir loolu Ilyaas ne Alyaasa: «Xaaral fii rikk, ndax Aji Sax ji da maa yebal Betel.» Alyaasa ne ko: «Ak sama digganteek Aji Sax ji, Kiy Dund, nga fekke tey, duma teqlikook yaw mukk.» Ñu daldi ànd, dem Betel.
3Kurélu yonenti Betel nag dikk ca Alyaasa ne ko: «Ndax xam nga ne bésub tey jii Aji Sax ji dina la yenni sa kilifteefu sang Ilyaas?» Mu ne: «Man kay xam naa ko; waaye noppileen rekk.»
4Ba mu ko defee Ilyaas ne Alyaasa: «Ngalla xaar ma fii nag, ndax Aji Sax ji da maa yebal Yeriko.» Alyaasa ne ko: «Ak sama digganteek Aji Sax ji, Kiy Dund, nga fekke tey, duma teqlikook yaw mukk.» Ñu daldi ànd, dem Yeriko.
5Kurélu yonenti Yeriko nag dikk ba ca Alyaasa ne ko: «Ndax xam nga ne bésub tey jii Aji Sax ji dina la yenni sa kilifteefu sang Ilyaas?» Mu ne leen: «Man kay xam naa ko, waaye noppileen rekk.»
6Gannaaw loolu Ilyaas ne Alyaasa: «Ngalla xaaral fii, ndax Aji Sax ji da maa yebal dexu Yurdan.» Alyaasa ne ko: «Ak sama digganteek Aji Sax ji, Kiy Dund, nga fekke tey, duma teqlikook yaw mukk!» Ñu ànd ñoom ñaar.
7Ba loolu amee juróom fukki nit bawoo ca kuréli yonent ya, dikk taxaw, dànd leen, janook ñoom fa ñu yem ñoom ñaar ca tàkkal dexu Yurdan.
8Ilyaas jël mbubbam, taxañ, ne ko tàrr ca ndox ma, mu xàjjalikoo yaar. Ñu jaar ci suuf su wow si, jàll ca wàlla.
9Ba ñu jàllee, Ilyaas ne Alyaasa: «Wax ma lu ma lay defal bala ñu maa yóbbu, may teqlikook yaw!» Alyaasa ne ko: «Xanaa naa am lu mat sag leer ñaari yoon.»
10Ilyaas ne ko: «Ñaan nga lu jafe. Waaye soo ma gisee bu ñu may jële fi ma nekk ak yaw, yóbbu, kon dinga ko am. Soo ma gisul nag, doo ko am.»
11Ci kaw loolu ñu ànd di waxtaan, di dem. Yéguñu lu moy watiiru sawara, wu ànd ak fasi sawara, ne jimeet, dox seen diggante ñoom ñaar; Ilyaas yiiroo aw callweer, yéeg kaw asamaan.
12Alyaasa gis loolu, daldi yuuxu, naan: «Wuy baayee, baay bóoy, yaay watiiru xarey Israyil aki gawaram!» Ba loolu amee gisatu ko. Mu ne sëq ay yéreem, ne ko tareet, def ko ñaar ndaxu tiis,
13doora for mbubb ma wadde ca Ilyaas; ne wërëñ, dem taxawi ca tàkkal dexu Yurdan.
14Ba mu ko defee Alyaasa fab mbubb ma wadde ca Ilyaas, ne ko tàrr ca ndox ma ne: «Ana Aji Sax ji, Yàllay Ilyaas? Ana mu?» Naka la Alyaasa dóor ca ndox ma moom itam, mu xàjjalikoo yaar, mu jàll.
15Kuréli yonenti Yeriko ya doon seetaan a nga janook moom naa: «Leeru Ilyaas wàcc na ci kaw Alyaasa!» Ba loolu amee ñu gatandu ko, sujjóotal ko, dëpp seen jë ca suuf.
16Ci kaw loolu ñu ne ko: «Xam nga lan la, sang bi? Am na ci nun juróom fukki nit ñu jàmbaare. Nañu dem seetali la sa sang ba. Jombul leeru Yàlla yóbbu ko, teg ko ci kaw tund yii, wenn, mbaa mu teg ko ci biir xur yii, wenn.» Mu ne leen: «Déedéet, buleen leen yebal.»
17Ñu soññ ko, ba mu am ca kersa, ne leen: «Waaw, yebal-leen leen.» Ñu daldi yebal juróom fukki nit, ñu seet diiru ñetti fan, gisuñu kenn.
18Naka lañu dellu ca moom, fekk ko ca Yeriko, mu ne leen: «Newuma leen woon buleen dem?»

19Gannaaw loolu waa dëkk ba ne Alyaasa: «Xam nga fi dëkk bi nekk baax na, sang bi, waaye ndox mi baaxul, te suuf si nanguwul.»
20Alyaasa ne leen: «Indil-leen ma ndab lu bees, te def ci xorom.» Ñu indil ko.
21Mu dem ba ca bëtu ndox ba, sànni ca xorom sa, ne: «Aji Sax ji nee: Laabal naa ndox mii. Dootu rey te dootu tax suuf si du nangu.»
22Ndox ma daa laab ba tey jii, muy la Alyaasa waxoon.
23Alyaasa bàyyikoo fa, jëm Betel. Ma nga topp yoon wa di dem, ay gone jóge ca dëkk ba, di ko ñaawal, naan ko: «Boroom nel, ca kaw! Ée boroom neleey, ayca ca kaw!»
24Naka la ne gees, ne leen jàkk, daldi leen móolu ci turu Aji Sax ji. Ci kaw loolu ñaari urs génne ca àll ba, fàdd ca gone ya ñeent fukk ak ñaar.
25Mu bàyyikoo foofa jubal tundu Karmel, jóge fa dellu Samari.