Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sabóor - Sabóor 99

Sabóor 99:1-5

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Aji Sax jeey Buur. Yeen xeet yi, ragal-leen ko! Moo toogandook malaakay serub yi. Suufoo, soo yeboo, yëngu!
2Aji Sax ji fi Siyoŋ a màgg, kawe, tiim xeetoo xeet.
3Sa tur weeka màgg te raglu. Sàbbaal-leen ko. —Kee sell!
4Buur, jëfe yoon mooy dooleem, te yaa saxal njub, yoon ak njekk ci askanu Yanqóoba.
5Màggal-leen sunu Yàlla, Aji Sax ji, te sujjóot fa ndëggastalam. —Kee sell!

Read Sabóor 99Sabóor 99
Compare Sabóor 99:1-5Sabóor 99:1-5