Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sabóor - Sabóor 7

Sabóor 7:8-17

Help us?
Click on verse(s) to share them!
8Yal na xeet yi daje, wër la, nga délsi tiim leen fu kawe.
9Yal na Aji Sax ji àtte xeet yi; Aji Sax ji, seetal ci sama njubteek sama maandute te dëggal ma.
10Yal na mbonug ku bon tees, te nga saxal kuy def njekk. Yaw Yàlla Boroom njekk, yaay natt xel ak xol.
11Sama kaaraange, fa Yàlla, miy musal boroom xol bu dëggu.
12Yàllaay àtte dëgg. Yàllaay rëbbe bés bu ne.
13Ku tuubul, Yàlla nàmm saamaram, bank xalaam, diir la.
14Moom la waajalal ngànnaayi ndee, def ko fitt yuy boy.
15Ku bon a ngoog, di matu doomu ñaawtéef. Day sos njombe, wasin njublaŋ.
16Am kan lay gas, ba mu xóot, te pax ma mu gas, moo ca tàbbi.
17Fitnaam, këpp ci boppam; coxoram, xàŋŋ cim kaaŋam.

Read Sabóor 7Sabóor 7
Compare Sabóor 7:8-17Sabóor 7:8-17