Text copied!
Bibles in Wolof

Sabóor 7:8-17 in Wolof

Help us?

Sabóor 7:8-17 in Kàddug Yàlla gi

8 Yal na xeet yi daje, wër la, nga délsi tiim leen fu kawe.
9 Yal na Aji Sax ji àtte xeet yi; Aji Sax ji, seetal ci sama njubteek sama maandute te dëggal ma.
10 Yal na mbonug ku bon tees, te nga saxal kuy def njekk. Yaw Yàlla Boroom njekk, yaay natt xel ak xol.
11 Sama kaaraange, fa Yàlla, miy musal boroom xol bu dëggu.
12 Yàllaay àtte dëgg. Yàllaay rëbbe bés bu ne.
13 Ku tuubul, Yàlla nàmm saamaram, bank xalaam, diir la.
14 Moom la waajalal ngànnaayi ndee, def ko fitt yuy boy.
15 Ku bon a ngoog, di matu doomu ñaawtéef. Day sos njombe, wasin njublaŋ.
16 Am kan lay gas, ba mu xóot, te pax ma mu gas, moo ca tàbbi.
17 Fitnaam, këpp ci boppam; coxoram, xàŋŋ cim kaaŋam.
Sabóor 7 in Kàddug Yàlla gi