Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sabóor - Sabóor 4

Sabóor 4:1-6

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Mu jëm ci njiital jàngkat yi, ànd aki xalam, di kàddug Sabóor, ñeel Daawuda.
2Éy Yàlla, yaw mi may àtte dëgg, maa ngi woote, wuyu ma; maa xatoon, nga yaatal ma. Ngalla baaxe ma, nangul ma.
3Yeen boroom daraja yi, buleen yàqati sama der, buleen sopp caaxaan, di sos. Selaw.
4Xamleen ne Aji Sax ji day séddoo ku ko ragal, te bu ma wooyee Aji Sax ji, mu dégg.
5Loxleen te baña bàkkaar, waxtaanleen ak seen ngegenaay te noppi.
6Rendileen seen sarax yi war, te wóolu Aji Sax ji.

Read Sabóor 4Sabóor 4
Compare Sabóor 4:1-6Sabóor 4:1-6