7Ay giir a riir, ay réew yëngu; mu àddu, suuf seey!
8Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ànd ak nun, Yàllay Yanqóoba jee nuy rawale. Selaw.
9Dikkleen gis jaloorey Aji Sax ji, ak yàqute gi mu dogal ci kaw suuf.
10Mu ngi fey xare ci àddina sépp, dog fitt, damm xeej, lakk pakk.
11Mu ne: «Dal-leen te xam ne maay Yàlla, màgg ci biir xeet yi, màgg fi kaw suuf.»