7 Ay giir a riir, ay réew yëngu; mu àddu, suuf seey!
8 Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ànd ak nun, Yàllay Yanqóoba jee nuy rawale. Selaw.
9 Dikkleen gis jaloorey Aji Sax ji, ak yàqute gi mu dogal ci kaw suuf.
10 Mu ngi fey xare ci àddina sépp, dog fitt, damm xeej, lakk pakk.
11 Mu ne: «Dal-leen te xam ne maay Yàlla, màgg ci biir xeet yi, màgg fi kaw suuf.»