13Waa Tir a lay yótsiy may, ay boroom alal di wut lu la neex.
14Séetu Buur duggsi na, ne ràññ, sol mbubb mu wurus way tàkk.
15Ñu yóbbul ko Buur, mu ne boyy, janq ja ànd ak moom, diy toppam, ñu indil leen Buur,
16ñu duggsi kër Buur, ci biir mbégteek bànneex.
17Yal na la sa doom yu góor wuutu ci seen jalu maam, nga def leeni kàngam ci réew mi mépp.