Text copied!
Bibles in Wolof

Sabóor 45:13-17 in Wolof

Help us?

Sabóor 45:13-17 in Kàddug Yàlla gi

13 Waa Tir a lay yótsiy may, ay boroom alal di wut lu la neex.
14 Séetu Buur duggsi na, ne ràññ, sol mbubb mu wurus way tàkk.
15 Ñu yóbbul ko Buur, mu ne boyy, janq ja ànd ak moom, diy toppam, ñu indil leen Buur,
16 ñu duggsi kër Buur, ci biir mbégteek bànneex.
17 Yal na la sa doom yu góor wuutu ci seen jalu maam, nga def leeni kàngam ci réew mi mépp.
Sabóor 45 in Kàddug Yàlla gi