14Man, ma mel nib tëx, dégguma, mel ni luu, àdduwma,
15di saf ku dul dégg, bay layoo.
16Aji Sax ji, yaw laa yaakaar; Boroom bi, sama Yàlla, yaa may nangul.
17Ma ne, ngalla buñu ma ree, di damoo samab jéll.
18Maa ngii di waaja daanu, dëkke metit.
19Ma ne, aylayéwén def naa lu ñaaw, sama bàkkaar tiital na ma.
20Noon yaa ngi ne jonn ak seen doole, bare na ñu ma bañ ci neen.