Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sabóor - Sabóor 27

Sabóor 27:3-14

Help us?
Click on verse(s) to share them!
3Bu gàngoor booloo sama kaw, duma raf. Ab xare jib, ma ànd ak Yàlla.
4Lenn laa ñaan Aji Sax ji, lii laay sàkku: dëkk kër Aji Sax ji, sama giiru dund, di niir taaru Aji Sax ji, te yéemoo këram.
5Bésub ay, mu yiire ma mbaaram, làq ma, ma làqoo xaymaam, aj ma ciw doj, ma raw.
6Ma doxe fa siggi, tiim noon yi ma wër, di sarxali fa xaymaam saraxi sarxolle. Naa woyal Aji Sax ji, joobe ko.
7Éy Aji Sax ji, déglul, ma woote! Ngalla baaxe ma, nangul ma.
8Yaw la sam xel ne ma, ma sàkku la, te it yaw Aji Sax ji laay sàkku.
9Sang bi, bu ma làqu, bul mer, jañax ma. Yaa ma daa wallu. Bu ma wacc, bu ma ba, yaay Yàlla mi may musal.
10Ndey ak baay man nañu maa wacc, Aji Sax ji fat ma.
11Éy Aji Sax ji, joxoñ ma saw yoon, jaarale ma joor gu wóor, ngir ñi may tëru.
12Bu ma baye bànneexu noon. Seedey naaféq a ma jógal, di sos fitna.
13Maay dajeek ngëneelu Aji Sax ji fi kaw suuf sii. Lii wóor na ma.
14Yaakaaral Aji Sax ji, dëgërlul te amu fit, te yaakaarati Aji Sax ji.

Read Sabóor 27Sabóor 27
Compare Sabóor 27:3-14Sabóor 27:3-14