Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sabóor - Sabóor 138

Sabóor 138:3-8

Help us?
Click on verse(s) to share them!
3Bés ba ma wootee, yaa ma wuyu, ñemeel ma, dooleel ma.
4Aji Sax ji, na la buuri àddina yépp màggal, ñoo dégg kàddu yi nga wax.
5Nañu woy say jaloore, naan: «Aji Sax jeeka màgg teddnga!»
6Aji Sax jee kawe! Ku toroxlu, mu niir; ku réy, mu ñooru.
7Ma wéye njàqare, nga musal ma, dogalee sa loxo merum noon, walloo ma sa ndijoor.
8Aji Sax jee may feyul. Éy Aji Sax ji, yaa saxoo ngor! Bul wacc ñi nga binde sa loxo.

Read Sabóor 138Sabóor 138
Compare Sabóor 138:3-8Sabóor 138:3-8