Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sabóor - Sabóor 9

Sabóor 9:6-20

Help us?
Click on verse(s) to share them!
6Rëbb nga xeet yi, sànk ñu bon ñi, far seeni tur ba fàww.
7Noon ya raaf, gental ba fàww. Yaa déjjati seeni dëkk, seenu askan fey.
8Aji Sax jee sax dàkk, samp jalam ngir àtte.
9Moom mooy àtte àddina cig njub, di dogalal xeet yi dëgg.
10Aji Sax jeey làq néew-ji-doole, mooy làqe bésub njàqare.
11Aji Sax ji, yaw, ku la xam, wóolu la. Aji Sax ji, yaw, ku lay sàkku, doo ko wacc.
12Woyleen Aji Sax ji dëkke Siyoŋ, siiwal-leen ay jalooreem ci xeet yi!
13Mooy topp nit bakkanu moroomam, di ko ba xel, te du fàtte yuuxi néew-ji-doole.
14Éy Aji Sax ji, baaxe ma, gisal naqar wi ma bañ yi teg. Yaa may yékkatee fa bunti ndee,
15ba ma siiwali sa woy yépp, fa buntu Siyoŋ, dëkk bu taaru ba, di bànneexoo sa wall gii!
16Xeet yee tàbbi pax ma ñu gasoon, fakktaloo fiir ga ñu làqoon.
17Aji Sax jaa ngi feeñoo, di àtte yoon; ku bon teg ug fiir, tàbbi ca. Na jib ndànk. Selaw.
18Ñu bon ñee dëddu, dem njaniiw, ànd ak xeet yi fàtte Yàlla yépp.
19Yàlla du tanqamlu ab ndóol ba fàww, yaakaaru néew-ji-doole du tas mukk.
20Aji Sax ji, jógal, bu la nit yab; na xeet yi dikk fi sa kanam, nga àtte leen.

Read Sabóor 9Sabóor 9
Compare Sabóor 9:6-20Sabóor 9:6-20