5Mboolem yàlla yi xeet yiy jaamu, yàllantu la, waaye Aji Sax jee sàkk asamaan.
6Màggaay ak daraja, fa moom, dooleek taar, fa këram gu sell.
7Yeen làngi xeet yi, seedeel-leen Aji Sax ji; seedeel-leen Aji Sax ji teddngaak doole.
8Seedeel-leen Aji Sax ji teddngay turam, yékkatil kob sarax, duggaale ëttam.
9Sujjóotal-leen Aji Sax ji làmboo sellnga, te àddina wërngal këpp di ko loxal.
10Neleen xeet yi Aji Sax jeey buur: àddinaa ngii, dëju te raful. Mooy àtte xeet yi njub.
11Asamaanoo, bégal! Suufoo, bànneexul! Géejoo, riiral yaak li la fees,