3Aji Sax jeey Yàlla ju màgg ji, buur bu mag bi tiim yàllay xeet yépp.
4Moo moom xóotey suuf, moom colli tund yi,
5moom géej, sàkk ko, moom jéeri ji mu mooñ.
6Nan sëgg, sujjóot, sukkal Aji Sax ji nu sàkk.
7Mooy sunu Yàlla, nuy xeet wi muy foral, diy gàtt ciy loxoom. Bésub tey yal nangeen dégg kàddoom